Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 4

Sarxalkat yi 4:12-20

Help us?
Click on verse(s) to share them!
12mboolem li des ci yëkk wi daal lay génne dal bi, yóbbu ko ci bérab bu mucc sobe, ca jalub dóom ba, daldi taal matt, lakk ko ca, ba mu dib dóom. Foofa dóom ba jale lees koy lakk.
13«Ndegam mbooloom Israyil mépp a moy lenn ci santaaney Aji Sax ji, ba def lenn lu warul te du seen teyeef, muy seenug tooñ te seetluwuñu ko,
14bu mbooloo mi nemmikoo moy gi rekk, war nañoo génne ci jur gu gudd gi yëkk wu ndaw wuy doon saraxu póotum bàkkaar, yóbbu ko ca bunt xaymab ndaje ma.
15Magi mbooloo mi dañuy teg seeni loxo ci boppu yëkk wi, fi kanam Aji Sax ji, ba noppi ñu rendi yëkk wi fi kanam Aji Sax ji.
16Gannaaw loolu na sarxalkat bi ñu diw, fal ko, sàkk ci deretu yëkk wi, yóbbu ci biir xaymab ndaje mi.
17Na capp baaraamam ci deret ji, wis-wisal deret ji juróom ñaari yoon fi kanam Aji Sax ji, foofu ci kanam rido bi.
18Bu noppee na sàkk ci deret ji, taqal ci béjjéni sarxalukaay bi ci kanam Aji Sax ji, ci biir xaymab ndaje mi. Li des ci deret ji, na ko tuur ca taatu sarxalukaayu rendi-dóomal ba, ca bunt xaymab ndaje ma.
19Na génne lépp li ciy nebbon, lakk ko ci kaw sarxalukaay bi.
20Na def ak yëkk woowu na muy def ak yëkku saraxu póotum bàkkaar rekk. Noonu lay def ak moom. Ni la ko sarxalkat biy defale seen njotlaay, ñu am njéggal.

Read Sarxalkat yi 4Sarxalkat yi 4
Compare Sarxalkat yi 4:12-20Sarxalkat yi 4:12-20