Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 25

Sarxalkat yi 25:8-11

Help us?
Click on verse(s) to share them!
8«Gannaaw loolu nangeen waññ ba ci juróom ñaari ati Noflaay, loolu di juróom ñaari at ba muy juróom ñaari yoon. Mu doon seen juróom ñaari ati Noflaay, tollu ci ñeent fukki at ak juróom ñeent.
9Su boobaa ci fukki fan ca juróom ñaareelu weer wa nangeen wal-lu ag liit fépp. Bésub Njotlaay boobu nangeen wal ag liit ci seenum réew ba mu daj.
10Te nangeen sellal at ma ca topp di juróom fukkeelu at ma, ngeen yéene ca mboolem waa réew ma ba mu daj, ne ngoreel taxaw na. Seen atum Yiwiku la, ku nekk war cee dellu ca suufu waa këram, ku nekk it wara dellu ca làng ga mu bokk.
11Seen atum Yiwiku la atum juróom fukkeel boobu di doon. Dungeen ci ji, dungeen ci góobaat lu saxe ca seenum ngóob te dungeen ci wolli ag reseñ, di ko witt.

Read Sarxalkat yi 25Sarxalkat yi 25
Compare Sarxalkat yi 25:8-11Sarxalkat yi 25:8-11