Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sarxalkat yi - Sarxalkat yi 23

Sarxalkat yi 23:25-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
25Mboolem lu ngeen faral di liggéey buleen ko ci liggéey, waaye nangeen ci indi saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.»
26Aji Sax ji teg ca wax Musaa ne ko:
27«Te itam fukki fan ci juróom ñaareelu weer woowu, bésub Njotlaay ba lay doon. Ndaje mu sell ngeen ciy amal. Nangeen ci toroxlu te indi saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.
28Du lenn lu ngeen di liggéey ci boobu bés, ndax bésub Njotlaay la bu ngeen di jotoo fi seen kanam Yàlla, Aji Sax ji.
29Te kat, képp ku toroxluwul boobu bés, dees koy dagge ci biir bànni Israyil.
30Képp ku liggéey lenn ci boobu bés, su boobaa dinaa far kooku ci biir bànni Israyil, sànk ko.
31Buleen ci liggéey dara. Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, yeen ak seen askan ak fépp fu ngeen dëkk.
32Seen bésub Noflaay la bu ngeen di nopplu doŋŋ te war cee toroxlu. Li ko dale ci ngoonug juróom ñeenti fan ci weer wi ba ca ëllëg sa, ba jant so, ci ngeen di wormaal seen bésub Noflaay.»

Read Sarxalkat yi 23Sarxalkat yi 23
Compare Sarxalkat yi 23:25-32Sarxalkat yi 23:25-32