14Ku boole nit ak ndeyam jël leen jabar, def na lu bona bon. Dees leen di boole taal, lakk leen, moom ak jigéen ña, ndax mbon gu ni mel baña am ci seen biir.
15Góor gu tëdde mala dee rekk mooy àtteem, te mala ma it dees koy rey.
16Su jigéen jëmee ci mala mu mu doon, ba jaxasook moom, booleleen ku jigéen kaak mala ma, rey. Dee rekk mooy seen àtte, te ñooy gàddu seen bakkanu bopp.
17«Su nit jëlee jabar ab jigéenam bu mu bokkal jenn ndey mbaa benn baay, ñu séq lalu séy, loolu gàcce la. Nañu leen dagge ci biir bànni Israyil, ñooñuy gis. Gannaaw moo tëdde ab jigéenam, na wéetoo añu ñaawtéefam.