15«Bul dëkkoo sa soxnas doom. Sa soxnas doom la. Bu ko dëkkoo mukk.
16«Bul dëkkoo soxnas koo bokkal benn baay mbaa jenn ndey, nde kon nga torxal sa doomu baay mbaa sa doomu ndey.
17«Bul boole dëkkoo jigéen, dëkkoo doom ja mbaa sëtam bu doomam ju góor jur mbaa doomam ju jigéen jur ko, ndax dañoo jegewoo lool cig bokk. Loolu ñaawtéef la.
18«Bul jël jigéen di séq ak moom séy, muy wujjeek doomu ndeyam mbaa doomu baayam joo jëkka jël, li feek kookoo ngi dund.