5Képp ku laal lalam, na fóot ay yéreem, sangu, te du tee mu yendoo sobe ba jant so.
6Ku toog ci lenn lu boroom jàngoroy xelli toogoon, na fóot ay yéreem, sangu, te du tee mu yendoo sobe ba jant so.
7Ku laal boroom jàngoroy xelli war naa fóot ay yéreem, sangu, te du tee mu ànd ak sobe ba jant so.
8Su ku ànd ak jàngoroy xelli tiflee ku taqul sobe, na kooku fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
9Gépp tegu daamar gu boroom jàngoroy xelli waroon, sobewu na.
10Ku laal lenn lu mu toogoon lu ko féete woon suuf dina yendoo sobe ba jant so, te képp ku yékkati loola na fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
11Boroom jàngoroy xelli bu raxasul ay loxoom, ku mu laal, kooku, na fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so.