Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - SAAG

SAAG 5

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Dégluleen yéen boroom alal yi, jooyleen te naqarlu ndax mbugal, gi leen di xaar.
2Seen alal seey na, seen yére yi maxe na,
3seen wurus ak seen xaalis xomaag na. Xomaag jooju seede lay doon, su leen di daanlu, ba lakk leen ni sawara. Dajale ngeen alal ju ne gàññ, te fekk yéena ngi ci mujug jamono.
4Dégluleen! Jooyi xaalis bi ngeen sàcce ci gubkat, yi leen doon liggéeyal, ak yuuxi góobkat yi, dugg nañu ci noppi Boroom gàngoori xare yi.
5Ci barele ak bànneex ngeen dunde ci kaw suuf, di yafal seen bopp, fekk bésu rendi baa ngii.
6Daan ngeen ku jub, ba rey ko sax, te bañul.
7Yéen samay bokk, muñleen, ba Boroom bi délsi ci ndamam. Seetleen ci beykat bi, ni muy xaare njariñ ci meññeefu suuf, tey muñ, céebo ba bët wàcc.
8Yéen itam nag muñleen te dëgëral seen xol, xam ne ñëwug Boroom bi ci ndamam jege na.
9Buleen jàmbatante, samay bokk, ngir ragal Yàlla àtte leen. Àttekat baa ngi ci bunt bi sax!
10Bokk yi, defleen yonent, yi wax ci turu Boroom bi, seeni royukaay ci muñ tiis ak ci góor-góorlu.
11Xam ngeen ne ñiy góor-góorlu, ñu barkeel lañu. Dégg ngeen muñ ga Ayóoba amoon, te gis muj gu rafet, ga ko Boroom bi jagleel, ndax Boroom bi kuy ñeewante la te bare yërmande.
12Te li fi raw samay bokk, buleen waat mukk, bu muy ci asamaan mbaa ci suuf mbaa ci leneen lu mu mana doon. Nangeen yem ci: «waaw» ak «déedéet», ngir bañ cee layoo fa kanam Yàlla.
13Su amee ci yéen ku nekk ci tiis, na ñaan ci Yàlla. Ku nekk ci mbég, na sant Yàlla ciy woy.
14Su amee ci yéen ku wopp, na woo njiiti mbooloo mi, ñu ñaanal ko te diw boppam ci turu Boroom bi.
15Ñaan gu ànd ak ngëm dina musal ki wopp, ba Boroom bi yékkati ko. Su ko fekkoon ak i bàkkaar sax, Yàlla dina ko baal.
16Kon nag waxanteleen seeni bàkkaar tey ñaanalante, ngir ngeen wér. Ñaanu aji jub gu dëggu, dooleem amul kem.
17Naka noonu Ilyaas nit la woon ku bindoo ni nun, waaye bi mu saxee ci ñaan Yàlla, ngir mu baña taw, ndox laalul suuf diirub ñetti at ak genn-wàll.
18Gannaaw ga mu dellu ñaan, asamaan daldi taw, te suuf si saxal meññeef.

19Samay bokk, su amee ci yéen ku réere dëgg, te am ku ko gindi,
20na xam lii: ku gindi bàkkaarkat ci réeram, musal nga nit ci dee te faral ko bàkkaar yu bare.