Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - SAAG

SAAG 2

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Yéen samay bokk, bu benn gënale laal seen ngëm ci sunu Boroom Yeesu Kirist, mi soloo ndam.
2Ndaxte su ñaari nit duggee ci seen mbooloo, kii takk jaaroy wurus te sol yére yu taaru, ka ca des ñàkk te limboo ay sagar,
3ngeen teral boroom daraja ji ne ko: «Àggal ci jataay bu yiw bi,» ba noppi ngeen ne aji néew doole ji: «Taxawal fale, mbaa nga toog fi ci samay tànk,»
4kon gënale ngeen ci seen biir, ba àtte ci col, bàyyi xol.
5Dégluleen yéen sama bokk yi ma bëgg, ndax Yàlla tànnul ñi néewle ci àddina, ngir ñu barele ci ngëm, tey am i cér ci nguur, gi Yàlla dig ñi ko bëgg?
6Fekk dangeen leen di toroxal! Xanaa du boroom alal yi ñoo leen di not te di leen yóbbu fa kanam àttekat yi?
7Ndax duñu tilimal tur wu tedd, wi ngeen di wuyoo?
8Su ngeen sàmmee yoonu Buur Yàlla, ni ko Mbind mi tërale naan: «Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp,» kon def ngeen lu baax.
9Waaye su ngeen gënalee, bàkkaar ngeen, te yoonu Yàlla dina leen dab ni ñu moy.
10Ndaxte ku sàmm yoon wépp, waaye xëtt ci lenn ndigal rekk, jàdd nga yoon wépp.
11Ndaxte Yàlla mi ne: «Bul njaaloo», teg na ca ne: «Bul bóome.» Ku njaaloowul nag, waaye nga bóome, jàdd nga yoon wépp.
12Gannaaw dingeen nara jaar ci àtteb yoon, wiy goreel, na loolu lal seen wax ak seen jëf.
13Ndaxte ku yërëmul, yoon du la yërëm. Te yërmande mooy not àtte.
14Te lii itam samay bokk: ku ne gëm nga, te jëfewoo ko, loolu lu muy jariñ? Ndax googu ngëm man na laa musal?
15Su amee mbokk ci seen biir, mu rafle te amul dund, muy góor walla jigéen,
16te kenn ci yéen ne ko: «Demal ak jàmm, nga solu te lekk,» te fekk fajuleen aajoom, loolu lu muy jariñ?
17Noonu ngëm gu àndul ak jëf, amul benn njariñ.
18Waaye xanaa dina am ku ne: «Yaw am nga ngëm, man am naa ay jëf.» Yaw nag won ma sa ngëm gu àndul ak jëf; man, ma feeñal la sama ngëm ci samay jëf.

19Gëm nga ne Yàlla kenn la; loolu lu baax la, waaye xamal ne, jinne yi it gëm nañu loolu, ba dañoo tiit bay lox.
20Yaw mi gàtt xel, kaay ma won la ne ngëm gu àndul ak jëf, amul njariñ.
21Sunu maam Ibraayma, ndax du ci kaw jëf la ko Yàlla àttee ni ku jub, ci li mu joxe doomam Isaaxa ni sarax?
22Kon gis nga ne ngëm dafa lëngoo ak ay jëfam, te ngëmam mat ci kaw jëf jooju.
23Noonu li ñu wax ci Mbind mi am na, bi mu naan: «Ibraayma gëm na Yàlla, te Yàlla jàppe ngëmam ni njub,» ba ñu ko wooye xaritu Yàlla.
24Kon nag gis nga ne Yàlla ci jëf lay àtte nit ni ku jub, waaye du ci kaw ngëm kese.
25Naka Raxab jigéenu moykat bi itam, ndax du ci noonu la ko Yàlla àttee ni ku jub, ci li mu teeru ndawi Yawut yi, te jaarale leen ca poot ba?
26Kon nag ni jëmm ju amul ruu nekke ndee, noonu la ngëm gu àndul ak jëf nasaxe.