Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Room - Room 5

Room 5:10-16

Help us?
Click on verse(s) to share them!
10Ndegam ba ñu dee ay bañaaley Yàlla lees nu jubalee deewug Doomam, ñaata yoon lees nuy gënatee musale ag dundam, gannaaw ba ñu nu jubalee ak Yàlla?
11Te yemunu ci, xanaa di sagoo Yàlla itam ndax sunu Boroom Yeesu Almasi, mi nu jubale ak moom.
12Bàkkaar moo jaare ci kenn nit dugg ci àddina, dee jaare ci bàkkaar, dikk, ba dikkal ñépp, ndax ñépp a bàkkaar.
13Bàkkaar a ngi woon ci àddina ba ca janti yoonu Musaa, waaye deesul waññale bàkkaar te aw yoon amul.
14Teewul la dale ca Aadama ba ca Musaa, ci kaw àddina sépp la dee doon nguuru, ba ci kaw ñi bàkkaarul noonee Aadama xëtte woon ndigal. Aadama mooy takkndeeru ki doon dikk.
15Waaye ni moyug Aadama deme, yiwu Yàlla demewu ni. Moyug kenn nit, Aadama, tax na ñu bare dee; waaye yiwu Yàlla ak mayug yiw gu kenn nit, Yeesu Almasi, ñaata yoon la gënatee baawaan, ñeel nit ñu bare?
16Ni njeexitalu tooñu kenn nit deme, laa ne, mayu Yàlla demewu ni. Benn bàkkaar moo waral àtte bi indi mbugal. Waaye moy yu bare moo waral may gi teggi tuuma.

Read Room 5Room 5
Compare Room 5:10-16Room 5:10-16