10 Nun ay bañaaley Yàlla lanu woon, waaye Doomam dee na, ngir jubale nu ak moom. Gannaaw léegi nag xariti Yàlla lanu, rawatina ne dinanu mucc ndax dundug Doomam.
11 Te sax nu ngi bég ci Yàlla, jaarale ko ci sunu Boroom Yeesu Kirist, mi nu jubale ak moom.
12 Kon nag bàkkaar ci kenn nit la jaar, dugg ci àddina, indaale fi dee, te dee daldi law ci nit ñépp, ndaxte ñépp a bàkkaar.
13 Bàkkaar kon nekkoon na ci àddina, bi Yàlla di laata wàcce yoonu Musaa. Waaye gannaaw yoonu Musaa tëddagul woon, bàkkaar du woon jàdd yoon.
14 Teewul nag la dale ca Aadama ba ca Musaa, dee a ngi fi woon ci àddina, di not ñépp, ak sax ñi seen bàkkaar melul woon ni bosu Aadama, maanaam jàdd yoon. Aadama moomu nag moo di takkandeeru Kirist, mi waroona ganesi àddina.
15 Waaye warunoo yemale tooñu Aadama ak mayu Yàlla. Bàkkaaru kenn nit kooku tax na ñu bare dee; waaye yiwu Yàlla ak may, gi nu keneen nit ka Yeesu Kirist yéwénal, baawaan na ci ñu bare, ba suul tooñ googu.
16 Te bàkkaaru Aadama niroowul ak mayu Yàlla. Aadama bàkkaar na benn yoon, ba tax Yàlla daan ko, daanaale ñépp; waaye Yàlla jéggle na tooñ yu bare ci dara, ba mu àtte ñu bare ni ñu jub.