Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - ROOM - ROOM 2

ROOM 2:9-19

Help us?
Click on verse(s) to share them!
9Ki doon def lu bon, peyam mooy tiis ak metit wu tar, muy Yawut ci bu jëkk, mbaa ki dul Yawut.
10Waaye ki doon def lu baax, añam mooy bokk ci ndamu Yàlla, am ngërëm ak jàmm, muy Yawut ci bu jëkk, mbaa ki dul Yawut.
11Ndaxte ñépp a yem fa kanam Yàlla.
12Képp ku doon bàkkaar nag te nekkuloo woon ci yoonu Musaa, Yàlla dina la àtte ci lu dul yoonu Musaa, nga doora sànku. Te képp ku doon bàkkaar te nga nekkoon ci yoonu Musaa, Yàlla dina la àtte ci yoon woowu.
13Kon déglu yoonu Musaa rekk doyul; du loolu mooy tax nit jub ci kanam Yàlla; kiy sàmm yoon wi, moom la Yàlla di àtte ni ku jub.
14Ndax ñi dul Yawut te nekkuñu ci yoonu Musaa, ñu ngiy def li yoon woowu tëral, ndaxte Yàlla def na ko ci nit. Te wonee nañu noonu ne man nañoo ràññee lu baax ak lu bon, su ñu nekkul sax ci yoonu Musaa,
15di wone it ne Yàlla bind na ci seen xol jëf yi yoonu Musaa santaane. Seen xel it seede na ne noonu la, fekk seeni xalaat ñoo leen di tuumaal, mbaa ñu leen di jéggal.
16Ndax bés dina ñëw, bu xalaat yu làqu yi di feeñ, te Yàlla àtte nit ñi jaarale ko ci Yeesu Kirist. Xibaaru jàmm, bi may waare, moo ko wax.
17Maa ngi ñëw nag ci yaw mi ne Yawut nga; yaa ngi sukkandiku ci yoonu Musaa ak di damu ci Yàlla.
18Xam nga coobareem, ndaxte jàng nga ci yoonu Musaa, ba fonk yëf yi gëna baax.
19Yaa ngi teg sa bopp wommatkatu gumba yi ak leeru ñi nekk cig lëndëm.

Read ROOM 2ROOM 2
Compare ROOM 2:9-19ROOM 2:9-19