7su dee wàllu jàpple, deel jàpple; su dee wàllu njàngle, ngay jàngle;
8Su dee wàllu kàddu yuy yokke, ngay wax luy yokk gëmkat ñi; su dee wàllu joxe, deel joxe te Yàlla rekk tax; su dee wàllu jiite, taxawal temm ci liggéeyub jiite; su dee wàllu baaxe nit ñi, nay loo bége.
9Na seen cofeel mucc ci ngistal, seexluleen lu bon te ŋoy ci lu baax.
10Na leen mbëggeelug bokk taxa fonkante, te ngeen farlu ci di terlante.
11Sawarleen te baña yoqi, jaamuleen Boroom bi, ànd ceek pastéefu xol.
12Bégeleen seen yaakaar, di muñ ci biir tiis, tey saxoo ag ñaan.
13Deeleen def seen loxo ci lu faj soxlay gëmkat ñu sell ñi, te boole ci am teraanga.
14Ñi leen di bundxatal, ñaanal-leen leen, ñaanal-leen leen te bañ leena móolu.
15Ñi ci mbégte, bokkleen ak ñoom seen mbégte; ñi ci naqar, ngeen bokk ak ñoom seen naqar.
16Mànkooleen, buleen xëccu daraja, waaye nanguleena jonjoo ak ñi féete suuf, te baña jàppe seen bopp boroomi xel.
17Buleen feyantoo, fexeleen di def lu rafet, ñépp seede ko.