7 su dee wàllu jàpple, deel jàpple; su dee wàllu njàngle, ngay jàngle;
8 Su dee wàllu kàddu yuy yokke, ngay wax luy yokk gëmkat ñi; su dee wàllu joxe, deel joxe te Yàlla rekk tax; su dee wàllu jiite, taxawal temm ci liggéeyub jiite; su dee wàllu baaxe nit ñi, nay loo bége.
9 Na seen cofeel mucc ci ngistal, seexluleen lu bon te ŋoy ci lu baax.
10 Na leen mbëggeelug bokk taxa fonkante, te ngeen farlu ci di terlante.
11 Sawarleen te baña yoqi, jaamuleen Boroom bi, ànd ceek pastéefu xol.
12 Bégeleen seen yaakaar, di muñ ci biir tiis, tey saxoo ag ñaan.
13 Deeleen def seen loxo ci lu faj soxlay gëmkat ñu sell ñi, te boole ci am teraanga.
14 Ñi leen di bundxatal, ñaanal-leen leen, ñaanal-leen leen te bañ leena móolu.
15 Ñi ci mbégte, bokkleen ak ñoom seen mbégte; ñi ci naqar, ngeen bokk ak ñoom seen naqar.
16 Mànkooleen, buleen xëccu daraja, waaye nanguleena jonjoo ak ñi féete suuf, te baña jàppe seen bopp boroomi xel.
17 Buleen feyantoo, fexeleen di def lu rafet, ñépp seede ko.