Text copied!
Bibles in Wolof

Ngën-gi-woy 4:3-10 in Wolof

Help us?

Ngën-gi-woy 4:3-10 in Kàddug Yàlla gi

3 Sa tuñ yi mel ni wëñ gu xonq curr, ndaw gémmiñ gu jekk! Sa lex yiy tàkk ni ŋaali gërënaat, làqoo sa muuraay bi;
4 sa loos wi ne coleet ni tatay Daawuda, mërgalu ba jekk, caq bay lang ni junniy kiiraayi jàmbaar.
5 Sa ween yi ni ñaari tef, mbaa seexi kéwél yuy fore digg tóor-tóor yi.
6 Balaa jant a fenk, ker gàddaay, ma ne coww diggante tund wa ndàbb ne bann, ak tund wa xas ma neexe.
7 Xarit, sa lépp a rafet, sikk nekkul ci yaw.
8 Séet sama, jógeel Libaŋ, jege ma, bawool Libaŋ, jegesi ma. Wàcceel colli Amana ak colli Senir ak Ermon. Génnal xunti gaynde yooyook tundi segg ya.
9 Jigéen sama, séet sama, benn yoon nga ma xool, sama fit ne tërit. Sa benn peru caq rekk, sama fit ne tërit.
10 Jigéen sama, séet sama, sa mbëggeel a neex! Sa mbëggeel a dàq biiñ, sa diw yu xeeñ dàq luy cuuraay.
Ngën-gi-woy 4 in Kàddug Yàlla gi