Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Ngën-gi-woy - Ngën-gi-woy 4

Ngën-gi-woy 4:3-10

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Sa tuñ yi mel ni wëñ gu xonq curr, ndaw gémmiñ gu jekk! Sa lex yiy tàkk ni ŋaali gërënaat, làqoo sa muuraay bi;
4sa loos wi ne coleet ni tatay Daawuda, mërgalu ba jekk, caq bay lang ni junniy kiiraayi jàmbaar.
5Sa ween yi ni ñaari tef, mbaa seexi kéwél yuy fore digg tóor-tóor yi.
6Balaa jant a fenk, ker gàddaay, ma ne coww diggante tund wa ndàbb ne bann, ak tund wa xas ma neexe.
7Xarit, sa lépp a rafet, sikk nekkul ci yaw.
8Séet sama, jógeel Libaŋ, jege ma, bawool Libaŋ, jegesi ma. Wàcceel colli Amana ak colli Senir ak Ermon. Génnal xunti gaynde yooyook tundi segg ya.
9Jigéen sama, séet sama, benn yoon nga ma xool, sama fit ne tërit. Sa benn peru caq rekk, sama fit ne tërit.
10Jigéen sama, séet sama, sa mbëggeel a neex! Sa mbëggeel a dàq biiñ, sa diw yu xeeñ dàq luy cuuraay.

Read Ngën-gi-woy 4Ngën-gi-woy 4
Compare Ngën-gi-woy 4:3-10Ngën-gi-woy 4:3-10