Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - MACË

MACË 23

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Gannaaw loolu Yeesu waxoon na mbooloo ma ak taalibeem ya ne leen:
2«Xutbakat ya ak Farisen ya ñu ngi toog ci jalu Musaa.
3Lépp lu ñu leen wax nag, defleen ko te sàmm ko, waaye buleen roy seeni jëf, ndaxte dañuy wax waaye duñu ko jëfe.
4Dañuy takk say yu diis, yen leen ci nit ñi, waaye duñu ko nangoo laal sax ak seen cati baaraam.
5Dañuy def seeni jëf yépp, ngir nit ñi gis leen, di takk ay téere yu réy, tey réyal seeni laari mbubb.
6Ca reeri xew yi, toogu yu yiw lañuy taamu, tey féete kanam ca jàngu ya.
7Dañoo bëgg ñépp nuyoo leen ñaari loxo ca pénc ma, di leen wooye “kilifa gi.”
8Waaye yéen buñu leen wooye “kilifa gi,” ndaxte kenn rekk moo di seen Kilifa, te yéen ñépp ay bokk ngeen.
9Te buleen tudde kenn seen “baay” ci àddina, ndaxte kenn rekk moo di seen Baay, ki ci kaw.
10Buñu leen tudde it ay “njiit,” ndaxte kenn rekk moo di seen Njiit, mooy Kirist.
11Ki gëna mag ci yéen mooy ki nangoo nekk seen surga.
12Kuy yékkatiku dees na la suufeel; kuy suufeelu, ñu yékkati la.
13«Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tëj nguuru Yàlla Aji Kawe ji ci kanam nit ñi; yéen dungeen ci dugg, te dungeen bàyyi ku ci bëgga dugg, mu dugg ci.
15«Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi wër géej ak suuf, ngir sàkku benn taalibe, ba noppi ngeen def ko nitu sawara, ku leen yées ñaari yoon.
16«Yéen njiit yu gumba yi, dingeen torox! Yéena ngi wax ne: “Ku giñe kër Yàlla gi, ngiñ li duggul, waaye ku giñ ci wurusu kër Yàlla gi, dugg na.”
17Yéen ñi dof te gumba! Lan moo gëna màgg, wurus wi walla kër Yàlla, gi tax wurus wi sell?
18Dangeen ne it: “Ku giñe sarxalukaay bi ci kër Yàlla gi, ngiñ li duggul, waaye ku giñ ci sarax si ci kawam, dugg na.”
19Gumba yi! Lan moo gëna màgg, sarax si walla sarxalukaay bi tax sarax si sell?

20Ku giñe sarxalukaay bi, giñ nga ci sarxalukaay bi ak li ci kawam lépp.
21Ku giñe kër Yàlla gi, giñ nga ci kër Yàlla gi ak ki ci dëkk.
22Ku giñ ci asamaan, giñ nga ci jalu Buur Yàlla ak ki ci toog.
23«Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi sàkk asaka ci naana ak anet ak kumin, te sàggane yi gëna màgg ci yoonu Musaa, maanaam njub, yërmande ak ngëm. Loolu ngeen wara def, waxuma nag ngeen bàyyi la ca des.
24Yéen njiit yu gumba yi! Yéena ngi segg wallax-njaan, tey wann giléem.
25«Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi setal bitib kaas bi ak ndab li, waaye ci biir dafa fees ak càcc ak ëppal.
26Farisen yu gumba yi! Jëkkleena setal biir kaas bi ak ndab li, ngir biti bi itam set.
27«Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi mel ni bàmmeel yu ñu weexal. Ci biti am nañu melo wu rafet, waaye ci biir dañoo fees ak yaxi ñi dee ak tilim ju nekk.
28Yéen itam, ci ngistal dangeena mel ni ñu jub, waaye ci seen biir dangeen fees ak naaféq ak lu bon.
29«Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tabax xabruy yonent yi, tey rafetal bàmmeeli ñu jub ñi.
30Te yéena ngi wax ne: “Bu nu fekke woon sunu jamonoy maam, dunu ànd ak ñoom ciy tuur deretu yonent yi.”
31Seede ngeen nii ne yey ngeen seen bopp, te yéenay doomi ñi doon rey yonent yi,
32di aw seen tànki baay, ba yées leen sax.
33Yéen ñi mel ni ay jaan, te fees ak daŋar niy co, naka ngeen di mucce mbugalu sawara?
34Moo tax maa ngi leen di yónnee ay yonent ak ay boroom xam-xam ak ay xutbakat. Ñenn ñi dingeen leen rey te daaj leen ci bant; ñeneen ñi dingeen leen dóor ay yar ci seeni jàngu, di leen fitnaal ci dëkkoo dëkk.
35Noonu deretu ñi jub, ji ñu tuur jépp ci àddina, dina xëppu ci seen kaw, li dale ci deretu Abel mi jub, ba ci deretu Sakari doomu Baraki, mi ngeen rey ci diggante bérab bu sell bi ak sarxalukaay bi.
36Ci dëgg maa ngi leen koy wax, loolu lépp dina dal ci niti jamono jii.
37«Yerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi, tey sànni ay doj ndaw yi, ba ñu dee, aka maa bëggoona dajale say doom, ni ginaar di uufe ay cuujam, te nanguwuleen!

38Kon nag Yàlla dina bërgël seen kër, ba mu gent.
39Ndaxte maa ngi leen koy wax, dungeen ma gisati li dale tey, ba kera ngeen ne: “Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga!”»