Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - MACË

MACË 12

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Amoon na benn bésub noflaay Yeesu jaar ci ay tool yu ñor, fekk ay taalibeem xiif; ñu daldi fàq ay gub nag, di lekk.
2Farisen ya nag gis ko, ne Yeesu: «Gisal, say taalibe ñu ngi def lu jaaduwul ci bésub noflaay bi.»
3Noonu Yeesu ne leen: «Ndax jànguleen la Daawuda defoon, ba mu xiifee, moom ak ña mu àndaloon?
4Xanaa yéguleen, ni mu dugge woon ca kër Yàlla ga, gis fa mburu, ya ñu teewal ca kanam Yàlla, mu daldi ko lekk. Fekk jaaduwul mu lekk ca, moom walla ña mu àndaloon; sarxalkat rekk a ko sañoona lekk.
5Te it ndax jànguleen ci yoonu Musaa, ne sarxalkat ya ca kër Yàlla ga teraluñu bésub noflaay bi, te tooñuñu?
6Waaye maa ngi leen koy wax, am na ci seen biir ku sut kër Yàlla ga.
7Mbind mi nee na: “Yërmande laa bëgg, waaye du rendi saraxi mala.” Su ngeen xamoon lu wax joojuy tekki, kon dungeen teg tooñ ñi tooñul.
8Ndaxte Doomu nit ki mooy boroom bésub noflaay bi.»
9Bi loolu amee Yeesu jóge foofa, dugg ci seen jàngu,
10te amoon na fa nit ku loxoom làggi. Noonu Farisen ya laaj ko: «Faj ci bésub noflaay bi, ndax loolu jaadu na?» Fekk ñuy wut buntu tuumaal ko.
11Yeesu ne leen: «Ku fi amoon xar, mu daanu ci kàmb ci bésub noflaay bi, ndax doo ko jàpp, génne ko?
12Nit nag, ndax ëppul maana xar? Kon def lu baax ci bésub noflaay bi jaadu na.»
13Noonu Yeesu ne nit ka: «Tàllalal sa loxo!» Mu tàllal ko nag, loxoom daldi wér, mel ni ba ca des.
14Farisen ya génn nag, daldi gise, ngir fexee reylu Yeesu.
15Waaye bi ko Yeesu yégee, mu sore foofa; te ñu bare topp ko, mu wéral leen ñoom ñépp.
16Te mu dénk leen bu wóor, ñu bañ koo siiwal.
17Def na noonu, ngir amal la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan:
18«Kii mooy sama Ndaw li ma tànn, di sama Soppe bi neex sama xol. Dinaa def sama Xel ci moom, muy yégal xeet yi yoonu njub.

19Du xëccoo mbaa muy wax ci kaw, te kenn du dégg baatam ci mbedd yi.
20Du dammte barax bu banku, te mees guy saxar, du ko fey, ba kera mu yégal njub, ba daan.
21Ci turam la xeet yi di ame yaakaar.»
22Booba ñu indil ko ku rab jàpp, mu gumba te luu. Yeesu faj ko, ba ku luu ki di wax tey gis.
23Noonu mbooloo mépp yéemu naan: «Ndax kii du Sëtu Daawuda bi?»
24Bi Farisen ya déggee loolu nag, ñu ne: «Kii ci kàttanu Beelsebul, buuru rab yi, lay dàqe rab yi.»
25Waaye Yeesu xam seen xalaat ne leen: «Réew mu xeex boppam tas, te dëkk mbaa kër guy xeex boppam du mana yàgg.
26Bu Seytaane dàqee Seytaane nag, xeex na boppam; kon naka la nguuram di mana yàgge?
27Te it bu fekkee ne man damay dàq ay rab ci kàttanu Beelsebul, seeni taalibe nag, ci gan kàttan lañu leen di dàqe? Kon ñoo leen di àtte.
28Waaye bu fekkee ne ci Xelum Yàlla laay dàqe rab, kon nguuru Yàlla agsi na ba ci yéen.
29«Su fi amee nit ku bare doole, te nit bëgga dugg ci këram, nangu alalam, naka la koy defe? Xanaa dafay jëkka yeew ku bare doole ka, ba noppi doora toj këram gépp.
30Noonu ku farul ak man, yaa ngi may xeex, ku dajalewul ak man, yaa ngi tasaare.»
31Yeesu teg ca ne: «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, bàkkaar walla sos wu mu mana doon, dinañu ko baale, waaye ku sosal Xelum Yàlla, duñu ko baal.
32Ku sosal Doomu nit ki, dinañu ko baal, waaye ku sosal Xel mu Sell mi, duñu ko baal mukk, du ci àddina si, du ci àllaaxira.
33Neeleen garab gi baax na, moom ak meññeefam, walla ngeen ne garab gi bon na, moom ak meññeefam; ndaxte garab, meññeefam lañu koy xàmmee.
34Yéen ñi fees ak daŋar ni ay co, naka ngeen mana waxe lu baax, fekk dangeen bon? Ndaxte gémmiñ, la fees xol lay wax.
35Noonu nit ku baax, lu baax lay wax, jële ko ca fa mu denc lu baax, te nit ku bon, lu bon lay wax, jële ko ca fa mu denc lu bon.
36Maa ngi leen di wax ne keroog bés pénc, nit ñi dinañu làyyi ndax wax ju nekk ju amul njariñ, ju ñu masa wax.

37Ndaxte dees na la àtte ni ku jub ci say wax, walla ñu daan la ci say wax.»
38Ci kaw loolu ay xutbakat ak ay Farisen wax ak Yeesu ne ko: «Kilifa gi, danoo bëggoon, nga won nu kéemaan guy firndeel sag yónnent.»
39Yeesu ne leen: «Yéenay laaj firnde, yéen niti jamono ju bon jii, yéen ñi fecci seen kóllëre ak Yàlla, waaye dungeen jot jenn firnde ju dul firndey yonent Yàlla Yunus.
40Ndaxte ni Yunus nekke woon ñetti guddi ak ñetti bëccëg ci biir rabu géej wu mag, noonu la Doomu nit ki di nekke ñetti guddi ak ñetti bëccëg ci biir suuf.
41Keroog bés pénc waa dëkku Niniw dinañu jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte bi leen Yunus waaree, tuub nañu seeni bàkkaar, te ku sut Yunus a ngi fi.
42Te it ca bés pénc buur bu jigéen, ba dëkkoon ca sudd, dina jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte dafa jóge ca catul àddina, ngir déglu xam-xamu Suleymaan, te ku sut Suleymaan a ngi fi.
43«Boo xamee ne rab wa jàppoon nit génn na ci moom, day wër ay bérab yu wow, di wut fu mu noppaloo, waaye du ko gis.
44Noonu da naan: “Naa dellu ca sama kër, ga ma génne woon.” Bu ñëwee nag, mu fekk kërug neen, ñu bale ko, defar ko ba lépp jekk.
45Bu ko gisee nag, mu dem wooyi yeneen juróom ñaari rab yu ko gëna soxor, ñu dugg, sanc fa; ba tax muju nit kooku mooy yées njàlbéenam. Noonu lay nekke ak niti jamono ju bon jii.»
46Bi Yeesu nekkee di wax ak mbooloo ma, ndeyam ak ay rakkam daldi ñëw, taxaw ci biti, bëgga wax ak moom.
47Noonu kenn nit ne ko: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi nii taxaw ci biti, bëgga wax ak yaw.»
48Waaye Yeesu ne ko: «Kan mooy sama ndey ak ñan ñooy samay rakk?»
49Noonu mu joxoñ ay taalibeem naan: «Ñii ñooy sama ndey ak samay rakk.
50Ndaxte ku def sama coobarey Baay bi nekk ci kaw, yaa di sama rakk, sama jigéen ak sama ndey.»