Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - MACË - MACË 10

MACË 10:19-31

Help us?
Click on verse(s) to share them!
19Boo xamee ne nag jébbale nañu leen, buleen am xel ñaar ci li ngeen di wax, mbaa ni ngeen koy waxe. Ndaxte ca waxtu woowa sax dingeen jot li ngeen wara wax;
20du yéenay wax, waaye Xelum seen Baay mooy wax ci yéen.
21«Mag dina joxe rakkam cig dee, baay joxe doomam; ay doom it dinañu jóg, bañ seeni waajur, di leen reylu.
22Te yéen nag, ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur; waaye ku muñ ba muj ga, mucc.
23Boo xamee ne fitnaal nañu leen ci dëkk bii, demleen ca ba ca kanam. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, dungeen mana wër dëkki Israyil yépp, te Doomu nit ki ñëwul.»
24Yeesu teg ca ne: «Taalibe gënul kilifaam, te jaam gënul sangam.
25Bu taalibe yemee ak kilifaam demin, doy na; jaam it ni sangam. Ndegam tudde nañu boroom kër gi Beelsebul, astamaak waa kër gi.
26Kon nag buleen leen ragal, ndaxte amul dara lu nëbbu, lu ñu warula biral, mbaa luy kumpa lu ñu warula siiwal.
27Li ma leen wax ci biir lëndëm, waxleen ko ci leer; li ma leen déey, yégleleen ko ci kaw taax yi.
28Te buleen ragal ñu mana rey yaram, te manuñoo rey ruu, waaye ragal-leen ki mana sànk yaram ak ruu ci sawara.
29Ñaari picci ramatu, ndax duñu ko jaay ci dërëm? Waaye benn ci ñoom du daanu ci suuf te soobul seen Baay.
30Seen kawari bopp sax, waññees na leen.
31Kon buleen ragal dara, yéena gën ndiiraanu ramatu.

Read MACË 10MACË 10
Compare MACË 10:19-31MACË 10:19-31