Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - MÀRK - MÀRK 6

MÀRK 6:13-22

Help us?
Click on verse(s) to share them!
13Ñu dàq ay rab yu bare, te diw boppi jarag yu bare, wéral leen.
14Noonu Erodd buur bi dégg loolu, ndaxte turu Yeesu siiwoon na. Mu ne nag: «Yaxya dekki na, moo tax mu ànd ak kàttanu def ay kéemaan.»
15Ñeneen ne: «Kii Ilyaas la.» Ñi ci des ne: «Yonent la, bu mel ni yonent yu jëkk ya.»
16Waaye bi ko Erodd déggee, mu ne: «Yaxya male ma dagglu boppam, moom moo dekki.»
17Fekk Erodd yónnee woon na, jàpp Yaxya, yeew ko, tëj. Ndaxte Erodd takkoon na Erojàdd jabaru Filib magam.
18Te Yaxya ne ko: «Jaaduwul nga denc sa jabaru mag.»
19Moo tax Erojàdd ëmbal ko mer, ba bëgg koo rey, waaye manu koo def.
20Ndaxte Erodd dafa ragal Yaxya, ba sàmm bakkanam, xam ne ku jub la te sell. Bu ko daan déglu it, day jaaxle lool, teewul mu bég ci déglu ko.
21Noonu bés bu yell ñëw, ba Erodd doon màggal bésu juddoom; mu woo ca xew wa ay jaraafam ak kilifay xare ba ak njiiti diiwaanu Galile.
22Booba doomu Erojàdd dugg di fecc, mu neex Erodd ak gan ñi, ba buur bi ne janq bi: «Laaj ma loo bëgg, dinaa la ko jox.»

Read MÀRK 6MÀRK 6
Compare MÀRK 6:13-22MÀRK 6:13-22