Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 9

Luug 9:16-37

Help us?
Click on verse(s) to share them!
16Ba mu ko defee Yeesu jël juróomi mburu ya ak ñaari jën ya, xool kaw asamaan, daldi yékkati kàddug cant, ba noppi dagg mburu ya, jox taalibe ya, ngir ñu taajal ko mbooloo ma.
17Ñépp lekk ba regg, ba ñu yóbbu dog ya ca des, muy fukki pañe ak ñaar.
18Yeesu moo beru woon, di julli, taalibe ya feggook moom. Ci kaw loolu mu laaj leen ne leen: «Ana ku nit ñi ne moom laa?»
19Ñu ne ko: «Ñii nee ñu yaa di Yaxya; ñee ne yaa di Ilyaas; ñale ne kenn ci yonent yu jëkk yaa dekki, di yaw.»
20Yeesu ne leen: «Yeen nag, ngeen ne maay kan?» Piyeer ne ko: «Yaa di Almasib Yàlla.»
21Mu femmu leen nag, sant leen ñu bañ koo wax kenn.
22Mu neeti: «Fàww Doomu nit ki sonn lu bare, ba dajeek mbañeelu magi askan wi ak sarxalkat yu mag yi, ak firikati yoon yi, te dees na ko rey, ba ñetteelu fanam, mu dekki.»
23Yeesu nag wax leen ñoom ñépp, ne leen: «Képp ku bëgga dikk topp ma, fàtteel sa bopp, te nga gàddu bés bu nekk, bant bi ñu lay daaj, door maa topp.
24Ndax képp ku namma rawale sa bakkan, yaay ñàkk sa bakkan, waaye képp ku ñàkk sa bakkan ngir man, yaa musal sa bakkan.
25Ndax nit ki, su jagoo àddina sépp sax, te nara ñàkk bakkanam mbaa mu sànku, ana lu mu koy jariñ?
26Képp ku kersawoo sama jëmm, kersawoo topp samay wax, yaw itam Doomu nit ki dina la kersawoo, bés bu dikkee ci darajaam ak darajay Baay bi, ak darajay malaaka yu sell yi.
27Maa leen ko wax déy, ñenn a ngi fii taxaw tey, duñu dee te gisuñu nguurug Yàlla.»
28Ba lu wara tollook juróom ñetti fan wéyee gannaaw kàddu yooyu, Yeesu àndoon na ak Piyeer ak Yowaan ak Yanqóoba, ñu yéeg ca kaw tund wa ngir julli.
29Naka lay julli, xar kanamam soppiku, ay yéreem weex tàll, di melax.
30Ci kaw loolu ñaari nit jekki feeñ, di waxtaan ak moom; ñuy Yonent Yàlla Musaa ak Yonent Yàlla Ilyaas.
31Ñoo feeñ ci ag leer, di waxtaane dëddug Yeesu, ga mu doon waaja sottale fa Yerusalem.
32Booba ngëmment a ngay man Piyeer ak ña mu àndal. Ba ñu teewloo nag lañu gis leeru Yeesu, ak ñaar ña mu taxawal.
33Ba ñu demee ba ñaari nit ñooñu di bàyyikoo fa Yeesu, Piyeer ne ko: «Njaatige, su nu toogoon fii de, mu baax ci nun; nan yékkati ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa, benn Ilyaas.» Waaye booba Piyeer xamul la muy wax.
34Naka lay wax loolu, aw niir dikk yiir leen, taalibe ya tàbbi ca biir niir wa, tiitaange jàpp leen.
35Ci biir loolu baat jibe ca niir wa, ne: «Kii moo di sama Doom, ki ma taamu; dégluleen ko.»
36Ba baat ba selawee, Yeesu doŋŋ a feeñ. Taalibe ya nag ñoom ne cell, waxuñu kenn lenn jant yooyu, ca la ñu gis.
37Ca ëllëg sa ba ñuy wàcce tund wa, mbooloo mu baree dikk dajeek Yeesu.

Read Luug 9Luug 9
Compare Luug 9:16-37Luug 9:16-37