36Kenn ca Farisen ya moo woo woon Yeesu, ngir ñu bokk lekk. Yeesu agsi kër Farisen ba, daldi dikk ca ndab la.
37Ndeke senn as ndaw a nga ca dëkk ba, ab moykat la woon. Mu yég nag ne Yeesoo nga ca kër Farisen ba, di lekk. Mu dikk, indaale njaqal doju albatar lu def diwu xeeñlu.
38Mu dikk ba fa Yeesu sóonu, ca gannaawam, fa tànki Yeesu féete, daldi taxaw, di jooy, rongooñ ya tooyal xepp tànk ya. Ndaw sa nag di fompe tànki Yeesu kawaru boppam gay lang, di fóon tànk yaak cofeel, di ca sotti diwu xeeñlu ga.
39Farisen ba woo Yeesu nag gis loolu, naan ci xelam: «Kii su doon ab yonent, dina xam ndaw sii di ko nabb-nabbee ku mu doon, ak lu mu doon: jigéenu moykat!»
40Yeesu nag àddu, ne ko: «Simoŋ, dinaa la wax lenn.» Mu ne ko: «Waxal, sëriñ bi.»
41Yeesu ne ko: «Ñaari boroom bor la woon ak seenub leblekat. Boru kenn ka di téeméeri junni (500 000) ci xaalis, ka ca des fukki junni (50 000).
42Waaye ñoom ñaar ñépp, kenn manu cee fey. Mu far jéggal leen ñoom ñépp. Ana kan ci ñaar ñooñu nag moo ciy gëna fonk leblekat bi?»
43Simoŋ ne ko: «Xanaa ki ëpple lu ñu ko jéggal.» Yeesu ne ko: «Sab àtte jub na.»
44Mu walbatiku ca ndaw sa, daldi ne Simoŋ: «Gis nga ndaw sii de? Dugg naa sa kër, mayewoo ndox mu ma jàngoo. Waaye moom, ay rongooñam la tooyale samay tànk, fompe ko kawaru boppam.