Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 2

LUUG 2:20-46

Help us?
Click on verse(s) to share them!
20Noonu sàmm ya dellu ca seen jur, di màggal Yàlla, di ko sant ci li ñu déggoon lépp te gis ko, ndaxte lépp am na, ni ko Boroom bi waxe woon.
21Bi bés ba délsee jamonoy xarafal xale ba agsi. Ñu tudde ko Yeesu, ni ko malaaka ma diglee woon, laata ko yaayam di ëmb.
22Noonu jamono ji ñu leen waroona sellale agsi, ni ko yoonu Musaa tërale. Waajuri Yeesu yi daldi koy yóbbu ca dëkku Yerusalem, ngir sédde ko Boroom bi.
23Ndaxte bind nañu ci yoonu Boroom bi ne: «Bépp taaw bu góor, nañu ko sédde Boroom bi.»
24Bi ñu ko yóbboo, def nañu itam sarax, ni ko yoonu Boroom bi santaanee: «ñaari pitaxu àll walla ñaari xati yu ndaw.»
25Amoon na ca Yerusalem nit ku tudd Simeyon. Nit ku fonkoon yoonu Yàlla la te déggal ko, doon séentu jamono, ji Yàlla wara dëfal bànni Israyil. Xel mu Sell mi mu ngi ci moom,
26te xamal na ko ne du dee mukk te gisul Almasib Boroom bi.
27Noonu Xelum Yàlla daldi yóbbu Simeyon ba ca kër Yàlla ga. Bi waajuri Yeesu indee xale ba, ngir sédde ko Yàlla, ni ko yoon wi santaanee,
28Simeyon jël xale bi, leewu ko, daldi sant Yàlla ne:
29«Boroom bi, nanga yiwi sa jaam, mu noppaluji ci jàmm, ni nga ko waxe.
30Ndaxte sama bët tegu na ci mucc gi nga lal,
31xeet yépp seede ko.
32Muy leer giy leeral xeet yi, di ndamu Israyil say gaa.»
33Waajuri Yeesu yi waaru ci li ñu doon wax ci xale bi.
34Noonu Simeyon ñaanal leen, ba noppi ne Maryaama: «Xale bii Yàllaa ko yónni, ngir ñu bare ci Israyil daanu te yékkatiku. Def na ko it muy firnde ju ñuy weddi,
35ba naqar dina xar sa xol ni jaasi. Noonu xalaati ñu bare feeñ.»
36Amoon na it ca Yerusalem yonent bu ñuy wax Aana. Doomu Fanuwel mi askanoo ci Aser la woon, te Aana màggatoon na lool. Bi mu séyee, dëkk na juróom ñaari at ak jëkkëram.
37Jëkkër ja gaañu, te séyaatul. Léegi amoon na juróom ñett fukki at ak ñeent. Mi ngi dëkke woona jaamu Yàlla guddi ak bëccëg ca kër Yàlla ga, di ñaan ak di woor.
38Aana yem ca waxi Simeyon ya, daldi gërëm Yàlla tey yégal mbiri liir ba ñépp ñi doon séentu jamono, ji Yàlla wara jot Yerusalem.
39Bi waajuri Yeesu yi matalee seen warugar ci lépp lu yoonu Boroom bi santaane woon, ñu dellu seen dëkku Nasaret ca diiwaanu Galile.
40Xale baa nga doon màgg, di dëgër, mu fees ak xel te yiwu Yàlla ànd ak moom.
41At mu jot nag waajuri Yeesu yi daan nañu dem Yerusalem, ngir màggali bésu Mucc ba.
42Noonu bi Yeesu amee fukki at ak ñaar, ñu dem màggal ga, ni ñu ko daan defe naka-jekk.
43Bi màggal ga tasee, ñu dëpp ñibbi, waaye xale ba Yeesu des Yerusalem, te ay waajuram yéguñu ko.
44Ñu xalaat ne, Yeesu dafa àndoon ak ñeneen, ñi ñu bokkaloon yoon. Bi ñu doxee bésub lëmm, ñu tàmbali di ko seet ci seen bokk yi ak seen xame yi.
45Bi ñu ko gisul nag, ñu daldi dellu Yerusalem, seeti ko.
46Ca gannaaw ëllëg sa ñu fekk ko ca kër Yàlla ga, mu toog ci jànglekati Yawut yi, di déglu ak di laajte.

Read LUUG 2LUUG 2
Compare LUUG 2:20-46LUUG 2:20-46