Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 2:20-46 in Wolof

Help us?

LUUG 2:20-46 in Téereb Injiil

20 Noonu sàmm ya dellu ca seen jur, di màggal Yàlla, di ko sant ci li ñu déggoon lépp te gis ko, ndaxte lépp am na, ni ko Boroom bi waxe woon.
21 Bi bés ba délsee jamonoy xarafal xale ba agsi. Ñu tudde ko Yeesu, ni ko malaaka ma diglee woon, laata ko yaayam di ëmb.
22 Noonu jamono ji ñu leen waroona sellale agsi, ni ko yoonu Musaa tërale. Waajuri Yeesu yi daldi koy yóbbu ca dëkku Yerusalem, ngir sédde ko Boroom bi.
23 Ndaxte bind nañu ci yoonu Boroom bi ne: «Bépp taaw bu góor, nañu ko sédde Boroom bi.»
24 Bi ñu ko yóbboo, def nañu itam sarax, ni ko yoonu Boroom bi santaanee: «ñaari pitaxu àll walla ñaari xati yu ndaw.»
25 Amoon na ca Yerusalem nit ku tudd Simeyon. Nit ku fonkoon yoonu Yàlla la te déggal ko, doon séentu jamono, ji Yàlla wara dëfal bànni Israyil. Xel mu Sell mi mu ngi ci moom,
26 te xamal na ko ne du dee mukk te gisul Almasib Boroom bi.
27 Noonu Xelum Yàlla daldi yóbbu Simeyon ba ca kër Yàlla ga. Bi waajuri Yeesu indee xale ba, ngir sédde ko Yàlla, ni ko yoon wi santaanee,
28 Simeyon jël xale bi, leewu ko, daldi sant Yàlla ne:
29 «Boroom bi, nanga yiwi sa jaam, mu noppaluji ci jàmm, ni nga ko waxe.
30 Ndaxte sama bët tegu na ci mucc gi nga lal,
31 xeet yépp seede ko.
32 Muy leer giy leeral xeet yi, di ndamu Israyil say gaa.»
33 Waajuri Yeesu yi waaru ci li ñu doon wax ci xale bi.
34 Noonu Simeyon ñaanal leen, ba noppi ne Maryaama: «Xale bii Yàllaa ko yónni, ngir ñu bare ci Israyil daanu te yékkatiku. Def na ko it muy firnde ju ñuy weddi,
35 ba naqar dina xar sa xol ni jaasi. Noonu xalaati ñu bare feeñ.»
36 Amoon na it ca Yerusalem yonent bu ñuy wax Aana. Doomu Fanuwel mi askanoo ci Aser la woon, te Aana màggatoon na lool. Bi mu séyee, dëkk na juróom ñaari at ak jëkkëram.
37 Jëkkër ja gaañu, te séyaatul. Léegi amoon na juróom ñett fukki at ak ñeent. Mi ngi dëkke woona jaamu Yàlla guddi ak bëccëg ca kër Yàlla ga, di ñaan ak di woor.
38 Aana yem ca waxi Simeyon ya, daldi gërëm Yàlla tey yégal mbiri liir ba ñépp ñi doon séentu jamono, ji Yàlla wara jot Yerusalem.
39 Bi waajuri Yeesu yi matalee seen warugar ci lépp lu yoonu Boroom bi santaane woon, ñu dellu seen dëkku Nasaret ca diiwaanu Galile.
40 Xale baa nga doon màgg, di dëgër, mu fees ak xel te yiwu Yàlla ànd ak moom.
41 At mu jot nag waajuri Yeesu yi daan nañu dem Yerusalem, ngir màggali bésu Mucc ba.
42 Noonu bi Yeesu amee fukki at ak ñaar, ñu dem màggal ga, ni ñu ko daan defe naka-jekk.
43 Bi màggal ga tasee, ñu dëpp ñibbi, waaye xale ba Yeesu des Yerusalem, te ay waajuram yéguñu ko.
44 Ñu xalaat ne, Yeesu dafa àndoon ak ñeneen, ñi ñu bokkaloon yoon. Bi ñu doxee bésub lëmm, ñu tàmbali di ko seet ci seen bokk yi ak seen xame yi.
45 Bi ñu ko gisul nag, ñu daldi dellu Yerusalem, seeti ko.
46 Ca gannaaw ëllëg sa ñu fekk ko ca kër Yàlla ga, mu toog ci jànglekati Yawut yi, di déglu ak di laajte.
LUUG 2 in Téereb Injiil

Luug 2:20-46 in Kàddug Yàlla gi

20 Ba loolu amee sàmm sa dellu, di sàbbaal ak a sant Yàlla ci mboolem la ñu dégg, gis ko, te lépp ame noonee ñu leen ko waxe woon.
21 Ba juróom ñetti fani xale bi matee, ñu xarfal ko, tudde ko Yeesu, na ko malaaka ma tudde woon, bala moo sosu.
22 Gannaaw ba seen fani setlu matee, ni ko yoonu Musaa laaje, ñu yóbbu xale bi Yerusalem, ngir teewal ko fi kanam Boroom bi,
23 noonee ñu ko binde ci yoonu Boroom bi ne: «Bépp taaw bu góor, dees koy tudde séddoo bu sell, ñeel Boroom bi.»
24 Ñu yóbbaale sarax bi ci war, ni ko yoonu Boroom bi santaanee: «ñaari pitaxu àll mbaa ñaari xati yu ndaw.»
25 Amoon na nag ca Yerusalem ku ñuy wax Simeyon; ku juboon, ragal Yàlla, di séentu jamono ji nekkinu bànni Israyil di ame ag tan, te Noo gu Sell gi àndoon ak moom.
26 Ndéey nag tukkee ci Noo gu Sell gi, xamal ko ne ko du dee mukk te gisul Almasi bu Boroom bi.
27 Ci kaw loolu mu dem ba ca biir kër Yàlla ga ci dooley Noo gu Sell gi. Gannaaw loolu waajuri Yeesu indi Yeesu ngir defal ko li aaday yoon wi laaj.
28 Simeyon itam jël xale bi, leewu ko, daldi sàbbaal Yàlla, ne:
29 «Léegi nag Buur Yàlla, yiwil sab jaam, mu dem ak jàmm, noonee nga ko waxe woon.
30 Nde saay gët tegu na ci mucc gi nga dogal,
31 waajal ko fi kanam askan yépp,
32 mu dig leer, ñeel jaambur ñi, sagal Israyil sa ñoñ.»
33 Baay bi ak ndey ji nag yéemu ci kàddu yooyu ñu wax ci xale bi.
34 Ba loolu amee Simeyon ñaanal leen, ba noppi ne ndeyam Maryaama: «Dama ne, kii lañu yebal ngir sànkutey ñu bare mbaa seenug leqliku ci digg Israyil, ngir itam mu doon firnde ju ñuy gàntal.
35 Yaw nag, sab xol la aw naqar wu mel ni saamar di xar, ba ñu bare la seen xalaati biir xol di feeñ.»
36 Jigéen ju ñuy wax Aana, ab yonent la woon ca Yerusalem, di doomu Fanuwel mi askanoo ci giirug Aser. Mag la woon lool. Ba muy janq la séy, nekk ak jëkkëram juróom ñaari at.
37 Jëkkër ja faatu, mu toog, séyaatul, ba booba mu amee juróom ñett fukki at ak ñeent (84). Daawul jóge ca kër Yàlla ga, koor ak julli la daan jaamoo guddi ak bëccëg.
38 Aana nag dikk moom it ca waxtu woowa, daldi delloo Yàlla njukkal. Ci kaw loolu muy waxtaane mbirum xale bi ak mboolem ña doon séentu bésu goreelug Yerusalem.
39 Ci kaw loolu ñu matal mboolem lu yoonu Boroom bi laaj, doora dellu Nasaret, seen dëkk ba ca diiwaanu Galile.
40 Xale bi nag di màgg, di dëgër, feese am xel, te yiwu Yàlla ànd ak moom.
41 At mu jotaan nag waajuri Yeesu dem Yerusalem, ngir màggali bésub Mucc ba.
42 Ba Yeesu amee fukki at ak ñaar, ñu dem màggali na ñu ko baaxoo woon.
43 Ba màggal ga tasee, ñu ñibbi, ngóor sa Yeesu moom des Yerusalem, te ay waajuram yéguñu ko.
44 Ñu xalaat ne, Yeesu daa ànd ak ñu ñu bokkaloon yoon. Dox nañu bésub lëmm, door koo wëri ci seeni bokk ak seeni xame,
45 te taxul ñu gis ko. Ñu daldi dellu Yerusalem, seeti ko.
46 Ca gannaaw ëllëg sa lañu ko fekk ca kër Yàlla ga, mu toog ca digg jànglekat ya, di leen déglook a laaj.
Luug 2 in Kàddug Yàlla gi