13Ndeke ca bés booba ñaar ca taalibe yaa nga woon ca yoonu dëkk bu ñuy wax Emayus, digganteem ak Yerusalem wara tollu ci fukki kilomeetar.
14Ña ngay waxtaane mboolem xew-xew yooyu.
15Naka lañuy waxtaan ak a diisoo, Yeesu ci boppam dab leen, ànd ak ñoom.
16Teewul seeni gët tëlee ràññee, ba manuñu koo xàmmi.
17Yeesu ne leen: «Lu ngeen di waxtaane nii ci yoon wi?» Ñu daldi taxaw, seen kanam lëndëm ndaxu tiis.
18Kenn ci ñoom, ku ñuy wax Kelyopas ne ko: «Xanaa yaw rekk de, yaa dal Yerusalem te umple li fi xew fan yii?»
19Yeesu ne leen: «Lu fi xew?» Ñu ne ko: «Mbirum Yeesum Nasaret. Mu doonoon ab yonent bu manoorewu ci jëf ak ci kàddu, Yàlla ak askan wépp seede.