27Mbooloo mu baree nga ko toppoon, te jigéen ñu baree ngi doon yuuxu, di ko jooy.
28Yeesu daldi walbatiku ca ñoom ne: «Yéen jigéeni Yerusalem, buleen ma jooy! Jooyleen seen bopp ak seeni doom.
29Ndaxte jamono dina ñëw, ju ñu naan: “Jigéen ñi masula jur ak ñi masula nàmpal, barkeel ngeen!”
30Bu keroogee, “Nit ñi dinañu ne tund yi: ‘Daanuleen ci sunu kaw!’ te naan jànj yi: ‘Suul-leen nu!’ ”
31Ndaxte su ñu defee nii garab gu tooy gi, lu ñuy def garab gu wow gi?»
32Yóbbaale nañu itam ñeneen, ñuy ñaari defkati lu bon, ngir rey leen.
33Bi xarekat ya agsee ba ca bérab, ba ñuy wooye Kaaŋu bopp, ñu daaj fa Yeesu ca bant, daajaale ñaari defkati lu bon ya, kenn ca ndijooram, ka ca des ca càmmoñam.
34Ci kaw loolu Yeesu ne: «Baay, baal leen, ndaxte xamuñu li ñuy def.» Xarekat ya tegoo ay bant yéreem, ngir séddoo ko.
35Mbooloo maa nga fa taxaw di seetaan. Njiit ya di ko reetaan naan: «Musal na ñeneen; na musal boppam, su fekkee mooy Almasi bi, ki Yàlla fal!»
36Xarekat ya it di ko ñaawal. Ñu jegesi, jox ko bineegar te naan:
37«Su fekkee ne yaay buuru Yawut yi, musalal sa bopp!»
38Ñu daaj mbind, mu tiim ko naan: «Kii mooy buuru Yawut yi.»
39Kenn ca defkatu lu bon ya ñu wékkoon ci bant, di ko xas, naan ko: «Xanaa du yaw yaay Almasi bi? Musalal sa bopp te musal nu!»
40Waaye ka ca des yedd moroom ma, naan ko: «Xanaa ragaloo Yàlla, yaw mi ñuy mbugal ni moom?
41Nun yelloo nanu sunu mbugal, waaye moom deful dara.»