Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 22

Luug 22:12-31

Help us?
Click on verse(s) to share them!
12Kooku moo leen di won néegub kaw bu yaa bu ñu defar ba noppi. Foofa ngeen di waajale.»
13Ba ñu demee, noonee leen ko Yeesu waxe, na lañu gise lépp. Ñu daldi waajal reer ba.
14Ba waxtuw reer jotee, Yeesu toog ak ndaw ya,
15ne leen: «Yàkkamti woon naa lool bokk ak yeen reeru bésub Mucc bii, bala maa tàbbi coono.
16Ndax maa leen ko wax, dootuma ko reer mukk, ba keroog solob reer bi di sotti ca nguurug Yàlla.»
17Ci kaw loolu mu jël ab kaas, yékkati kàddug cant, daldi ne: «Jël-leen kaas bii, te ngeen séddoo ko.
18Ndax maa leen ko wax, gannaaw-si-tey dootuma naan ndoxum reseñ, ba kera nguurug Yàlla dikk.»
19Gannaaw loolu mu jël mburu, yékkati kàddug cant, dagg ko, jox leen ko ne: «Lii moo di sama yaram wi ñu jooxe ngir yeen. Deeleen def lii, di ma ko fàttlikoo.»
20Kaas ba itam noonu la def ak moom gannaaw reer ba, ne leen: «Kaas bii mooy kóllëre gu yees gi fasoo ci sama deret ji leen nara tuurul.
21Waaye nag ki may wor, loxoom a ngi ci ndab lii nu bokk.
22Doomu nit ki déy, ni ñu ko dogale, noonu lay deme, waaye wóoy ngalla ki pexe mi ñu koy wore di jaare ci moom.»
23Ci kaw loolu taalibe yi di laajante ci seen biir, kan ci ñoom moo nar jooju jëf.
24Ab werante itam dikkal leen, ñuy xëccoo ci seen biir ku wara gëna kawe ci ñoom.
25Yeesu nag ne leen: «Buuri xeeti àddina doole lañuy nguuroo ci seen kaw, teewul ñi leen di néewal doole, baaxekati nit ñi lañu leen di wooye.
26Yeen nag bumu deme noonu ci seen biir. Ki gëna kawe ci yeen, na mel ni moo gën di ndaw, te njiit li, na mel ni ab surga.
27Ki ñu taajal ndab li, ak surga bi ko taajal, ana ku ci gëna kawe? Xanaa du ki ñu taajal? Moonte man, ci seen biir laa tooge toogaayu surga!
28Yeen nag yeenay ñi des ak man ci sama biir coono.
29Man itam ni ma sama baay dénke nguur, ni laa leen koy dénke.
30Yeenay lekk ak a naane ca sama ndab, ca sama nguur, te yeenay tooge ay gàngune, di jiite fukki giiri bànni Israyil ak ñaar.»
31Yeesu neeti: «Simoŋ, Simoŋ! Seytaane kat mu ngi sàkku ab sañ-sañ ngir man leena jéri ni am pepp.

Read Luug 22Luug 22
Compare Luug 22:12-31Luug 22:12-31