Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 21

Luug 21:9-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
9Bu ngeen déggee ay xare aki salfaañoo, buleen tiit, ndax fàww loolu jëkka am. Waaye du doonagum muj ga, ca saa sa.»
10Mu neeti leen: «Aw xeet dina jógal aw xeet, am réew jógal am réew.
11Ay yëngu-yënguy suuf yu réy dina am, ay xiif aki mbas dikke fu bare, te xew-xew yu raglu dina am, ak firnde yu mag yu jóge asamaan.
12Waaye laata loolu lépp, yeen, dees na leen teg loxo, fitnaal leen, jébbal leen kuréli jàngu ya, tëj leen kaso. Dees na leen yóbbu ci kanami buur aki boroom dëkk ndax sama tur,
13ngir ngeen doxe ca yékkati kàdduy seede.
14Kon nag defleen bu baax ci seen xel, ne soxlawuleena waajal kàddug layoo.
15Ndax man maa leen di jox làmmiñ wu ànd ak xel, wu seen benn noon dul mana dàq mbaa di ko weddi.
16Pexe mu leen jàpplu dina sababoo sax ci seeni waajur ak seen doomi ndey ak seeni jegeñaale ak seeni xarit, te dees na rey ñenn ci yeen,
17Ñépp a leen di bañ ndax sama tur.
18Waaye seen genn kawaru bopp sax du sànku.
19Saxooleen muñ nag, daldi mucc.
20«Bu ngeen gisee gàngooru xare gu gaw Yerusalem, su boobaa xamleen ne tasteem dëgmal na.
21Su boobaa ña mu fekk ca diiwaanu Yude, nañu daw jëm kaw tund ya, ñi ci biir dëkk bi, nañu daw génn, te ña mu fekk ca tool ya, buñu duggsi ci biir dëkk bi.
22Ndax janti mbugal lay doon, ngir sottal mboolem lu ñu bindoon.
23Wóoy ngalla jigéeni wérul ña, ak ñay nàmpal ca yooyu jant! Ndax tiis wu réy lay doon ci réew mi, akam sànj ci kaw askan wii.
24Dinañu fàddoo ñawkay saamar, te dees na leen jàpp njaam, yóbbu ci mboolem xeet yi. Te jaambur ñi dul Yawut ñooy joggati Yerusalem, ba kera àppu ñooñu dul Yawut di mat.
25«Ay firnde dinañu feeñ ci jant bi ak weer wi ak biddiiw yi. Ci kaw suuf njàqare ak tiitaange mooy ñeel xeet yi ndax riirum géej gi ak gannax yi,
26nit ñiy séentu li nara dikkal àddina, di xëm ndax tiitaange, nde dooley asamaan dina sàqi.
27Su boobaa dees na gis Doomu nit ki di ñëw ciw niir, ànd ak manoore ak daraja ju réy.
28Bu xew-xew yooyu tàmbalee sotti nag, taxawleen te siggi, ndax seenug njot dëgmal na.»
29Ci kaw loolu Yeesu léeb leen ne leen: «Xool-leen garabu figg mbaa geneen garab.
30Bu ngeen gisee mu jebbi, ca ngeen di xamal seen bopp ne nawet jubsi na ba noppi.
31Bu ngeen gisee xew-xew yooyu sotti, noonu itam ngeen di xame ne nguurug Yàlla dëgmal na.
32«Maa leen ko wax déy, niti tey jii duñu wéy mukk, te loolu lépp sottiwul.

Read Luug 21Luug 21
Compare Luug 21:9-32Luug 21:9-32