Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 20

LUUG 20:7-21

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Noonu ñu ne ko xamuñu fu mu ko jële.
8Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.»
9Noonu Yeesu daldi wax nit ña léeb wii: «Amoon na nit ku jëmbët toolu reseñ, batale ko ay beykat, dem tukki tukki bu yàgg.
10Bi tool bi ñoree nag, mu yónni surga ci ñoom, ngir jot wàllam ci meññeef gi. Waaye beykat yi dóor ko ay yar, dàq ko, mu dellu ak loxoy neen.
11Mu yónniwaat beneen surga, ñu dóor ko moom itam, toroxal ko, dàq ko, mu dellu ak loxoy neen.
12Mu yónneeti ñetteelu surga, ñu gaañ ko, dàq ko.
13«Boroom tool ba daldi ne: “Nan laay def nag? Dinaa yónni sama doom, sama reeni xol. Xëy na ñu weg ko, moom.”
14Waaye bi beykat yi gisee doom ji, ñu ne ci seen biir: “Kii moo wara donn tool bi; nan ko rey, moom ndono li.”
15Ñu génne ko tool bi nag, rey ko.» Noonu Yeesu laaj leen: «Nu leen boroom tool bi di def, nag?
16Xanaa ñëw, rey beykat yooyu, dénk tool ba ñeneen.» Bi Yeesu waxee loolu, nit ña ne ko: «Yàlla tere!»
17Waaye Yeesu ne leen jàkk, daldi ne: «Kon nag lu baat yii ci Mbind mi di tekki: “Doj wa tabaxkat ya sànni, mujj na di doju koñ.”
18Képp ku dal ci doj woowu, dammtoo, te ku mu dal ci sa kaw, rajaxe la.»
19Xutbakat ya ak sarxalkat yu mag ya ñu ngi doon wuta jàpp Yeesu ca taxawaay ba, ndaxte xam nañu ne ñoo tax mu wax léeb woowu. Waaye ragal nañu mbooloo ma.
20Noonu ñu koy yeeru, daldi yónni ay nit ñu mbubboo njub, sas leen ñu fexe koo jàpp ci ay waxam, ngir jébbal ko boroom réew, ma yor kilifteef ak sañ-sañ.
21Ñu daldi ñëw ci Yeesu ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne li ngay wax te di ko jàngle lu jub la. Amuloo parlàqu, waaye dangay xamle yoonu Yàlla ci bu wóor.

Read LUUG 20LUUG 20
Compare LUUG 20:7-21LUUG 20:7-21