7 Ñu daldi ne ko: «Xamunu fu mu ko jële.»
8 Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe lii.»
9 Ci kaw loolu Yeesu léeb askan wa, lii, ne leen: «Jenn waay moo jëmbatoon ab tóokëru reseñ, batale ko ay beykat, daldi dem yoon wu yàgg.
10 Ba tóokër ba ñoree, mu yebal ca beykat ya ab surga, ngir ñu jox ko wàllam ca meññeef ma. Beykat ya dóor surga ba, ba noppi dàq ko, mu dellu loxoy neen.
11 Mu dellu yónni beneen surga, ñu dóor ko moom itam, torxal ko, dàq ko, mu dellu loxoy neen.
12 Mu dellooti yónni ñetteelu surga, kooku it, ñu gaañ ko, sànni ko ca biti.
13 «Boroom tóokër ba ne: “Nan laay def nag? Naa yónni sama doomu bopp ji ma sopp boog, xanaa moom, dinañu ko rus!”
14 Teewul ba beykat ya gisee doom ji, dañu ne ci seen biir: “Kii mooy donn; nanleen ko rey, su ko defee ndono li féeteek nun.”
15 Ba loolu amee ñu génne ko tóokër ba, rey ko.» «Ana nu boroom tóokër biy def beykat yi nag?
16 Xanaa dikk, rey beykat yooyu, dénk tóokër ba ñeneen.» Nit ña dégg loolu daldi ne: «Yàlla tere!»
17 Yeesu ne leen jàkk, daldi ne: «Kon nag lii ñu bind, lu muy tekki? “Doj wi tabaxkat yi beddi woon, moo mujj di doju coll wi.”
18 Woowu doj, képp ku ci dal, dammtoo, te ku mu dal, rajaxe la.»
19 Firikati yoon yaak sarxalkat yu mag ya nag, ca saa sa lañu doon fexee teg Yeesu loxo, ndax xamoon nañu ne ñoo moom léeb woowu, waaye nit ña lañu ragal.
20 Ba mu ko defee ñu bàyyi Yeesu xel, daldi yebal ay yeerukat, sas leen ñu yiw-yiwlu te di ko fiir ci kaw kàddu ba jàpp ko, ngir jébbal ko boroom dëkk bay boroom kilifteef ga ak sañ-sañ ba.
21 Yeerukat ya dikk ne Yeesu: «Sëriñ bi, xam nanu ne njub ngay wax, di ko jàngle. Amuloo parlàqu itam, waaye ci kaw dëgg ngay jànglee yoonu Yàlla.