5Ñu waxtaan ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” dina laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?”
6Te bu nu nee: “Ci nit ñi,” mbooloo mépp dinañu nu sànni ay xeer, ndaxte gëm nañu ne Yaxya yonent la woon.»
7Noonu ñu ne ko xamuñu fu mu ko jële.
8Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.»
9Noonu Yeesu daldi wax nit ña léeb wii: «Amoon na nit ku jëmbët toolu reseñ, batale ko ay beykat, dem tukki tukki bu yàgg.
10Bi tool bi ñoree nag, mu yónni surga ci ñoom, ngir jot wàllam ci meññeef gi. Waaye beykat yi dóor ko ay yar, dàq ko, mu dellu ak loxoy neen.
11Mu yónniwaat beneen surga, ñu dóor ko moom itam, toroxal ko, dàq ko, mu dellu ak loxoy neen.
12Mu yónneeti ñetteelu surga, ñu gaañ ko, dàq ko.
13«Boroom tool ba daldi ne: “Nan laay def nag? Dinaa yónni sama doom, sama reeni xol. Xëy na ñu weg ko, moom.”