5 Ñu diisoo ci seen biir, daldi ne: «Su nu nee: asamaan la ndigal la bawoo da naan lu tax kon gëmunu Yaxya?
6 Te su nu nee: ci nit ñi la ndigal li bawoo, mbooloo mépp a nuy sànni ay xeer, ndax wóor na leen ne Yaxya ab yonent la woon.»
7 Ñu daldi ne ko: «Xamunu fu mu ko jële.»
8 Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe lii.»
9 Ci kaw loolu Yeesu léeb askan wa, lii, ne leen: «Jenn waay moo jëmbatoon ab tóokëru reseñ, batale ko ay beykat, daldi dem yoon wu yàgg.
10 Ba tóokër ba ñoree, mu yebal ca beykat ya ab surga, ngir ñu jox ko wàllam ca meññeef ma. Beykat ya dóor surga ba, ba noppi dàq ko, mu dellu loxoy neen.
11 Mu dellu yónni beneen surga, ñu dóor ko moom itam, torxal ko, dàq ko, mu dellu loxoy neen.
12 Mu dellooti yónni ñetteelu surga, kooku it, ñu gaañ ko, sànni ko ca biti.
13 «Boroom tóokër ba ne: “Nan laay def nag? Naa yónni sama doomu bopp ji ma sopp boog, xanaa moom, dinañu ko rus!”