Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 19

Luug 19:8-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
8Sase nag taxaw ne Sang bi: «Sang bi, ma ne, sama genn-wàllu alal, jox naa ko néew-doole yi, te jépp alal ju lewul ju ma masa jëlal kenn, dinaa fey ñeentam.»
9Yeesu ne ko: «Bés niki tey, mucc dikkal na kër gii, ndax waa jii kat ci askanu Ibraayma la bokk, moom itam.
10Ndax Doomu nit ki, ñi réer la seetsi, ngir musal leen.»
11Naka la nit ña dégg loolu, Yeesu léebati leen, ndax booba jege na Yerusalem, te fekk na ñu foog ne nguurug Yàlla day daldi teew ca saa sa.
12Moo tax mu ne: «Boroom juddu bu réy la woon. Muy waaja dem réew mu sore, ngir ñu fal ko fa buur, mu doora ñibbsi.
13Ci biir loolu mu woo fukki surgaam, jox leen ku nekk benn posetub wurus bu gànjare, ne leen: “Liggéeyleen ci, ba ma ñibbsi.”
14Waaye waa réewam ña dañu koo bañoon. Ci gannaawam lañu yónni ndaw, ne: “Kii, bugguñu muy sunu buur.”
15«Gannaaw ba ñu ko falee buur, ba mu délsi, daa woolu surga, ya mu joxoon wurus wa, ngir xam ñaata la leen ca seen liggéey jural.
16Kenn ka dikk, ne ko: “Sang bi, sa poset ba jur na fukki poset.”
17Mu ne ko: “Jaaraamaa, surga bu baax bi. Gannaaw ci lu tuut nga wóore nag, falul ci fukki dëkk.”
18Keneen dikk, ne: “Sang bi, sa poset ba indi na juróomi poset.”
19Mu neeti kooka: “Yaw, falul ci juróomi dëkk.”
20Keneen dikk ne: “Sang bi, sa poset baa ngii ma fasoon ciw sekkit.
21Dama laa ragal, ndaxte ku néeg nga. Dangay foqati loo dénkaanewul woon, di dajale loo jiwuloon.”
22Mu ne ko: “Say wax laa lay àttee, surga bu bon bi! Xamoon nga ne nit ku néeg laa, di foqati lu ma dénkaanewul woon, di dajale lu ma jiwuloon.
23Lu la tee woona dénkaaneji sama alal ca dencukaay ba, ngir bu ma dikkee jot ko, boole ca tonoom?”
24«Ci kaw loolu mu ne ña fa taxawoon: “Nanguleen poset bi ci moom, jox ko boroom fukki poset yi.”
25Ñu ne ko: “Sang bi, kee ngeek fukki poset ba noppi!”
26Mu ne: “Ma ne leen, képp ku am, dees na ko dolli, waaye ku amul, la mu am as néew sax, dees na ko nangu.
27Sama noon yooyu buggul woon ma doon seen buur nag, indileen leen fii, te rendi leen ci sama kanam.”»
28Ba Yeesu waxee loolu ba noppi, ca la jiitu, jëm Yerusalem.
29Ba Yeesu dikkee ba jub dëkk ya ñuy wax Betfase ak Betani, ca wetu tund wa ñuy wax tundu Oliw ya, dafa yebal ñaari taalibeem,
30ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci kanam. Bu ngeen agsee, dingeen gis cumbur bu yeewe, bu kenn masula war. Yiwileen ko, indi.
31Bu ñu leen nee: “Lu tax ngeen di ko yiwi?” ne leen: “Sang bee ko soxla.”»
32Ba ndaw ya demee, na leen ko Yeesu waxe lañu ko gise.

Read Luug 19Luug 19
Compare Luug 19:8-32Luug 19:8-32