32Ba ndaw ya demee, na leen ko Yeesu waxe lañu ko gise.
33Naka lañuy yiwi cumbur ba, ay boroomam ne leen: «Lu tax ngeen di yiwi cumbur bi?»
34Ñu ne: «Boroomam moo ko soxla.»
35Ñu indil Yeesu cumbur bi, sà nni seeni yére ca kawam, daldi waral Yeesu.
36Naka la Yeesuy dem, nit ñi di ko lalal seeni yére ca yoon wa.
37Ba ñu jubsee Yerusalem, bay wà cce ca mbartalum tundu Oliw ya, mbooloom taalibe mépp la mbégte jà pp, ñu tà mbalee sà bbaal Yà lla ca kaw ndax kéemaan ya ñu gis.
38Ña nga naan: «Na barke wà ccal buur bi ñëw ci turu Boroom bi! Jà mm fa asamaan; daraja fa bérab ya gëna kawe!»
39Yenn Farisen ya woon ca mbooloo ma nag ne Yeesu: «Sëriñ bi, yeddal sa taalibe yi!»