Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 19

Luug 19:30-41

Help us?
Click on verse(s) to share them!
30ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci kanam. Bu ngeen agsee, dingeen gis cumbur bu yeewe, bu kenn masula war. Yiwileen ko, indi.
31Bu ñu leen nee: “Lu tax ngeen di ko yiwi?” ne leen: “Sang bee ko soxla.”»
32Ba ndaw ya demee, na leen ko Yeesu waxe lañu ko gise.
33Naka lañuy yiwi cumbur ba, ay boroomam ne leen: «Lu tax ngeen di yiwi cumbur bi?»
34Ñu ne: «Boroomam moo ko soxla.»
35Ñu indil Yeesu cumbur bi, sànni seeni yére ca kawam, daldi waral Yeesu.
36Naka la Yeesuy dem, nit ñi di ko lalal seeni yére ca yoon wa.
37Ba ñu jubsee Yerusalem, bay wàcce ca mbartalum tundu Oliw ya, mbooloom taalibe mépp la mbégte jàpp, ñu tàmbalee sàbbaal Yàlla ca kaw ndax kéemaan ya ñu gis.
38Ña nga naan: «Na barke wàccal buur bi ñëw ci turu Boroom bi! Jàmm fa asamaan; daraja fa bérab ya gëna kawe!»
39Yenn Farisen ya woon ca mbooloo ma nag ne Yeesu: «Sëriñ bi, yeddal sa taalibe yi!»
40Mu ne: «Maa leen ko wax, su ñii noppi woon, doj yi ñooy xaacu.»
41Ba Yeesu jubsee ba séen dëkk ba, jooy na ndax moom.

Read Luug 19Luug 19
Compare Luug 19:30-41Luug 19:30-41