Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 12

Luug 12:4-21

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4«Maa leen ko wax, yeen samay soppe, buleen ragal ñu manul lu wees rey seen yaram, ndax gannaaw loolu dootuñu leen manal lu ko raw.
5Ma xamal leen nag ki ngeen wara ragal: kiy rey ba noppi, am sañ-sañu sànni ca sawara sa, kooku déy laa leen ne, ragal-leen ko.
6Juróomi picci ramatu, xanaa jarul ñaari dërëm doŋŋ? Moona Yàlla fàttewula geesu menn ci ñoom.
7Yeen nag seen kawari bopp sax, waññees na lépp. Buleen ragal dara, nde ndiiraanu ramatu, yeena ko gën.
8«Te it maa leen ko wax, képp ku dëggal fi kanam nit ñi, ne man nga féeteel, Doomu nit ki itam dina dëggal fa kanam malaakay Yàlla ya, ne moom nga féeteel.
9Waaye ku weddi fi kanam nit ñi, ne man nga féeteel, dees na weddi fa kanam malaakay Yàlla ya, ne man nga féeteel.
10Képp ku jëme kàddug safaan ci Doomu nit ki, dees na la jéggal, waaye ku saaga Noo gu Sell gi, deesu la jéggal.
11«Bu ñu leen yóbboo ca jàngu ya, ca kanam kilifa ya, ak àttekat ya, buleen jaaxle ci nan ngeen di yékkatee kàddug layoo, ak luy doon seenu lay, mbaa lu ngeen di wax,
12ndax su boobaa Noo gu Sell gi moo leen di xamal ca waxtu woowa la ngeen wara wax.»
13Kenn ca mbooloo ma moo noon Yeesu: «Sëriñ bi, waxal ci sama mag, mu jox ma sama wàll ci ndono li nu bokk.»
14Yeesu ne ko: «Waa jii, kan moo ma fal àttekat mbaa miraaskat ci seen kaw?»
15Ci kaw loolu mu ne leen ñoom ñépp: «Moytuleen wépp xeetu bëgge, ndax loo barele barele, sa bakkan ajuwul ci sa alal.»
16Mu léeb leen nag, ne leen: «Nit la woon ku woomle, te ab toolam nangu.
17Mu naan ca xel ma: “Nu may def nag? Amatuma sax fu ma denc sama ngóob mi!”
18Ci kaw loolu mu ne: “Nii laay def: samay sàq laay daaneel, daldi defaraat sàq yu gëna mag, denc ci sama pepp ak mboolem lu ma am.
19Su ko defee ci samam xel laa naan: ‘Céy sama waa ji, yaa ngeek alal ju bare ju mana dem ay ati at; neel finaax, di lekk, di naan ak a bége.’ ”
20Yàlla nag ne ko: “Ñàkk xel! Guddig tey jii, dees na jël sa bakkan. Kon li nga waajal, ana kuy doon boroom?”
21«Kuy dajaleel boppam alal te woomlewoo fa Yàlla, loolu mooy saw demin.»

Read Luug 12Luug 12
Compare Luug 12:4-21Luug 12:4-21