30Ndax na Yunus nekke woon firnde ca waa Niniw, noonu la Doomu nit ki nekke firnde ci niti tey jii.
31Keroog àtte ba, Lingeeru bëj-saalum dina jóg, janook niti tey jii, tiiñal leen; ndax moo bàyyikoo woon ca catal àddina, ngir déglusi xam-xamu Suleymaan, te tey jii, ku sut Suleymaan a ngi fi.
32Waa réewum Niniw it keroog àtte ba dinañu taxaw, layook niti tey jii, tiiñal leen ndax ñoo tuube woon ca waareb Yunus, te tey jii, ku sut Yunus a ngi fi.
33«Deesul taal ab làmp, di ko dugal fu làqu, mbaa ci suufu leget. Dees koy aj kay, ba kuy duggsi gis muy leer.
34Bët mooy làmpu yaram. Bu sa bët wéree, sa yaram wépp a ciy leerloo, waaye bu sa bët bonee, sa yaram wépp a ngi ci lëndëm.
35Kon seetal ndax leer gi nga foog ne mu ngi ci yaw du ag lëndëm.