Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 11

Luug 11:10-27

Help us?
Click on verse(s) to share them!
10Ndaxte képp ku ñaan, dinga am; ku seet, dinga gis; ku fëgg it, dees na la ubbil.
11Ana kan ci yeen mooy baay bu doomam ñaan aw jën, mu jox ko jaan?
12Mbaa mu ñaan ko nen, mu jox ko aw jiit?
13Ndegam yeen ñi bon yeena mana may seeni gone lu baax nag, astamaak Baay ba fa asamaan. Moo leen ko dàq fuuf, nde mooy may Noo gu Sell gi, ñi ko ko ñaan!»
14Yeesu moo doon dàq aw rab wu duggoon nit ba mu luu. Ba rab wa génnee, luu ba wax, mbooloo ma waaru.
15Teewul ñenn ca ñoom ne: «Ci Beelsebul, buuru rab yi lay dàqe ay rab.»
16Ñeneen nag di ko fiir, di sàkku ci moom firnde ju bawoo asamaan.
17Yeesu itam ràññee seen xalaat, ne leen: Gépp nguur guy xàjjalikoo ci biiram, day tas, yii kër màbb ca kaw yee.
18Seytaane itam, su xàjjalikoo ci biiram, ana nu nguuram di yàgge, gannaaw yeena ne Beelsebul laay dàqe ay rab?
19Te it ndegam man Beelsebul laay dàqe rab yi, seen ñoñ nag ñoom, kan lañuy dàqe ay rab? Kon kay seen ñoñ a leen tiiñal.
20Waaye su dee loxol Yàlla laay dàqe rab yi nag, kon nguurug Yàlla agsi na ba ci yeen.
21«Su ponkal gànnaayoo ba diis, wattu këram, alalam dina raw.
22Waaye bu ko ku ko man songee, ba daan ko, day nangu mboolem ngànnaay lu mu yaakaaroon, ba noppi séddale alalam.
23Ku farul ak man nag, man ngay xeex, te ku àndul ak man di dajale, yaa ngi tasaare.
24«Aw rab wu bon, bu jàppee nit ba génn ko, day wër bérab yu fendi, di wut fu mu nopploo, te du ko gis. Su ko defee mu ne: “Naa dellu ca sama kër, ga ma jóge.”
25Bu dikkee fekk kër gi buube, defare ba jekk,
26day dem indi yeneen juróom ñaari rab yu ko yées, ñu bokk sancsi. Su ko defee ni nit kiy mujje mooy yées na mu jëkke.»
27Naka la Yeesu di wax loolu, jenn jigéen ca mbooloo ma àddu ca kaw, ne ko: «Ndokklee ki la ëmb ci biiram, nàmpal la ci weenam!»

Read Luug 11Luug 11
Compare Luug 11:10-27Luug 11:10-27