13«Dingeen torox, yéen waa Korasin ak waa Betsayda, ndaxte kéemaan yi ma def ci yéen, bu ñu leen defoon ci dëkku Tir walla ci dëkku Sidon, kon tuub nañu seeni bàkkaar bu yàgg, xëppoo dóom, sol saaku.
14Moona ca bés pénc ba, Tir ak Sidon ñoo leen di tane.
15Te yaw dëkku Kapernawum, ndax dees na la yékkati bu kawe? Déedéet, dees na la daane bu suufe.