Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 30:23-33 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 30:23-33 in Kàddug Yàlla gi

23 ndaw su bon su for jëkkër, jigéen ju wuutu sangam bu jigéen.
24 Ñeent a ngii, di lu tuut ci kaw suuf, te am xel, yaroo xel:
25 xorondom, néew na doole, waaye bu jotee, mu denc dundam;
26 daman, barewul kàttan, te day dëkk ciy doj;
27 soccet, amul buur, teewul ñuy àndandoo, diy gàngoor;
28 sindax, manees na koo ŋëb, teewul ma nga biir kër buur.
29 Ñett a ngii, ñu jekk um ndaag, ba ci ñeent ñu jekk doxin:
30 gaynde, mooy buuru rab yi, ragalul kenn;
31 séq daagu, jekk taxawaay, ab sikket, ak buur ci biiri dagam.
32 Boo sàgganee bay tëggu, mbaa ngay mébét lu bon, nanga téye saw làmmiñ.
33 Ndax ku ruux soow, am ca dax, ku wañaar bakkan, mu nàcc, te lu jógal xol, indiw ay.
Kàddu yu Xelu 30 in Kàddug Yàlla gi