Text copied!
Bibles in Wolof

Kàddu yu Xelu 28:16-19 in Wolof

Help us?

Kàddu yu Xelu 28:16-19 in Kàddug Yàlla gi

16 Kilifa gu amul ug dégg, day foqati rekk, waaye ku bañ lu lewul, gudd fan.
17 Ku bóom nit, daw, ba tàbbi njaniiw; bu ko kenn taxawu.
18 Mat, mucc; dëng, dàll daanu.
19 Beyal sab tool, sab dund doy; topp ay caaxaan, ndóol ba doyal.
Kàddu yu Xelu 28 in Kàddug Yàlla gi