19ba noppi mu lekk, amaat doole. Bi mu ko defee mu toog ay fan ak taalibe, ya nekk Damaas.
20Ca saa sa muy yégle ca jà ngu ya ne, Yeesu mooy Doomu Yà lla.
21Ñi ko dégg ñépp waaru naan: «Ndax du kii moo daan tas ñiy tudd tur woowu ci Yerusalem, te mu ñëw fii, ngir yeew leen, yóbbu ci kanam sarxalkat yu mag ya?»
22Moona Sóol di gëna am kà ttan, bay jaaxal Yawut yi dëkk Damaas, ci di leen wax ay firnde, ne Yeesu mooy Almasi bi.
23Ba ñu ca tegee ay fani fan, Yawut yi daldi gise, ngir reylu ko.
24Waaye Sóol yég seen pexe. Fekk guddi ak bëccëg ñu doon wottu bunt yi yépp, ngir man koo bóom.
25Noonu taalibe yi jël ko ci guddi, def ko ci dà mba gu réy, jaarale ko ci miir bi, yoor ko ci suuf.
26Bi Sóol agsee Yerusalem, mu jéema à nd ak taalibe yi, waaye ñépp ragal ko, ndax gëmuñu woon ag taalibeem.
27Ci kaw loolu Barnabas jël ko, yóbbu ko ca ndaw ya, nettali leen, ni Sóol gise Boroom bi ci kaw yoon wi, ak li mu ko wax, rax-ca-dolli fit wi mu doon waxe ci turu Yeesu ci Damaas.
28Noonu mu nekk ak ñoom ci Yerusalem, di dugg ak a génn, di wax ak fit ci turu Boroom bi.
29Muy wax ak di werante ak Yawut yiy là kk gereg, waaye ñu di ko wuta rey.
30Bi ko bokk yi yégee nag, ñu yóbbu ko dëkku Sesare, yebal ko dëkku Tars.
31Noonu mbooloom ñi gëm nekk ci jà mm ci biir diiwaani Yude gépp ak Galile ak Samari; ñuy gëna dëgër, di wéy ci ragal Yà lla, tey yokku ci ndimbalu Xel mu Sell mi.
32Piyeer nag di wër, di jaar fu nekk, tey dem ci gaayi Yà lla yi dëkk Lidd,
33mu gis fa nit ku là ggi, tudd Ene, tëdd ci basaŋ diirub juróom ñetti at.
34Piyeer ne ko: «Ene, Yeesu Kirist faj na la; jógal te defar sa lal.» Noonu mu daldi jóg ca saa sa.