Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 27

Jëf ya 27:9-20

Help us?
Click on verse(s) to share them!
9Fekk na nag nu yàgg ca yoon wa, ba tollu ci jamono ju tukkib géej aaytal, ndax fekk na Koorug Yawut wees. Loolu tax Póol digal leen ne:
10«Bokk yi, gis naa ne yoon wii loraange ak yàqule gu réy la. Waxuma gaal gi ak li mu yeb, waaye sunuy bakkan sax xaj na ci.»
11Teewul njiitu takk-der ba sobental waxi Póol, déggal dawalkat ba ak boroom gaal ga.
12Te itam teeru boobu neexul woona lollikoo. Loolu waral ña ëpp ca waa gaal ga mànkoo ci jóge fa, dellu géej, te fexe nu ñu àgge Fenigsë, ngir lollikoo fa. Mooy teerub dunu Keret bi jublu sowub suuf ak sowub kaw.
13Ci kaw loolu ngelawal bëj-saalum wal ndànk, ñu njort ne man nañoo sottal seen pexe. Ñu wëgg diigal, daldi tafoo tefesu Keret.
14Teewul nes tuut ngelaw lu réy lu ñuy wax Penkub kaw, riddee ca dun ba.
15Gaal gi buubu, manatula dékku ngelaw li, ba nu mujj bayliku, daldi yal.
16Nu leru nag dun bu tuuti bu ñuy wax Koda, jaare wet gu nu fegoo ngelaw li, teg ci sonn lool doora téye loocob rawtu bu gaal gi.
17Ñu yéege looco ba, daldi jël ay buum yu ñu laxas ca yaramu gaal ga, dàbblee ko ko. Ci kaw loolu ñu ragala ngiroji ca beeñ bu ñuy wax Sirt, ba tax ñu sànni diigal, ngir yeexal gaal ga, daldi yalal.
18Ca ëllëg sa ngelaw la wéye noo pamti-pamtee, ba ñu mujj wàññi ca yebu gaal ga, sànni biir géej.
19Ca gannaaw ëllëg sa, seen loxoy bopp lañu jële yenn jumtukaayi gaal ga, sànni.
20Ay fani fan jant beek biddiiw yi ne meŋŋ, te ngelaw liy riddi rekk, ba nu noppee yaakaar ne dinanu mucc.

Read Jëf ya 27Jëf ya 27
Compare Jëf ya 27:9-20Jëf ya 27:9-20