Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 23

Jëf ya 23:4-16

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4Waa géew ba ne ko: «Sarxalkatub Yàlla bu mag bi ngay xas nag?»
5Póol ne leen: «Bokk yi, xawma woon ne mooy sarxalkat bu mag bi, ndax bindees na ne: “Sa kilifag askan, bu ko wax naka-su-dul-noonu.”»
6Fekk na Póol xam ne lenn ca kurél gaa nga bokk ca ngérum Sadusen ya, ña ca des bokk ca ngérum Farisen ya. Mu daldi àddu ca kaw ca biir géew ba, ne: «Bokk yi, man de ab Farisen laa, di doomu Farisen; li ñu may àttee nag mooy sunu yaakaar ak sunu ngëm gi nu bokk ci mbirum ndee-ndekki.»
7Naka la wax loolu Farisen yaak Sadusen ya tàmbalee werante, ba mbooloo ma xàjjalikoo.
8Ndax Sadusen yi dañu ne ndee-ndekki ak malaaka ak rab, dara amu ci, te Farisen yi ñoom, yooyu yépp lañu dëggal.
9Ci kaw loolu coow lu réy jib. Ñenn ca firikati yooni làngu Farisen ya, ne bërét, àddook doole, ne: «Gisunu lenn lu bon ci nit kii. Ku xam ndax aw rab a wax ak moom, mbaa malaaka?»
10Xuloo ba nag gëna tàng, ba njiital gàngoor ga mujj ragal ñu sëxëtoo Póol, ba def ko ay dog. Mu daldi sant lenn ca xarekat ya ñu wàcc, jële Póol ci biir nit ñi, yóbbu ko ca tata ja.
11Ca guddi ga Sang bi feeñu Póol, ne ko: «Na sa xel dal. Ni nga ma seedeele ci Yerusalem, noonu nga ma wara seedeeleji ca Room.»
12Ba bët setee Yawut ya daje, daldi xasoo, ne duñu lekkati, duñu naanati, ba kera ñu reyee Póol.
13Ña lal pexe moomu, ëpp nañu ñeent fukk.
14Ñu dem ca sarxalkat yu mag ya ak mag ña, ne leen: «Danoo giñ ne dunu dugalati dara sunu gémmiñ, ba kera nu reyee Póol.
15Léegi nag yeen ak kurélu àttekat yi, ñaanleen njiital gàngoor gi, mu indi Póol ba ci yeen, mu mel ni dangeena bëgga seetaat bu baax mbiram. Nun nag fagaru nanu, ngir bala moo agsi, nu rey ko.»
16Jarbaatub Póol bu góor nag yég tëru ma. Mu daldi dem ba ca tata ja, dugg, yégal ko Póol.

Read Jëf ya 23Jëf ya 23
Compare Jëf ya 23:4-16Jëf ya 23:4-16