Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 17

Jëf ya 17:3-9

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Mu di leen tekkil Mbind mi, di leen ci firndeel ne coonob Almasi ak ndekkiteem manul woona ñàkk. Mu ne leen: «Yeesu mii ma di leen xamal, mooy Almasi.»
4Ba loolu amee ñenn ca Yawut ya gëm, fekksi Póol ak Silas, ñoom ak Gereg yu bare yu ragal Yàlla, ak jigéen ñu ràññiku ñu bare.
5Yawut ya nag am ca kañaan, daldi foraatoo ca mbedd ma ay taxawaalukat, dajale ay gàngoor, ba yëngal dëkk ba. Ñu song kër Yason, di seet Póol ak Silas, ngir yóbbu leen ca waa dëkk ba.
6Ci kaw loolu gisuñu leen, ñu diri Yason ak yeneen bokki gëmkat ba ca kanam àttekat ya. Ña ngay biral, naan: «Nit ñi tas àddinaa ngii, agsi nañu fi,
7te Yason a leen dalal. Ñoom ñépp a xëtt ndigali buur Sesaar, te naan am na beneen buur bu ñuy wax Yeesu.»
8Ba mbooloo ma ak àttekati dëkk ba déggee loolu, dañoo jaaxle.
9Ba loolu amee ñu feyloo Yason ak ña ca des daan ba ca war, door leena yiwi.

Read Jëf ya 17Jëf ya 17
Compare Jëf ya 17:3-9Jëf ya 17:3-9