Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 14

Jëf ya 14:5-13

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Jaambur ñeek Yawut yi nag ànd ak seeni kilifa, di leen waaja mitital ak a dóori doj.
6Ñu yég ko, daw làquji diiwaanu Likawni, ca dëkk ya ñuy wax Listar, ak Derbe ak la ko wër.
7Foofa itam ñu di fa xamle xibaaru jàmm bi.
8Jenn waay a nga daan toog ca Listar, tànk ya baaxul woon; laago la judduwaale, te masula dox.
9Kookoo dégg Póol muy waare, Póol xool ko jàkk, gis ne am na ngëm gu muccam mana jaare.
10Mu àddu ca kaw, ne waa ji: «Jógal taxaw jonn!» Waa ji ne bërét, jóg, daldi dox.
11Ba mbooloo ma gisee la Póol def, ca kaw lañu àddu ci làkku Likawni, ne: «Yàlla yee soppliku melow nit, wàccsi ci sunu biir!»
12Ci kaw loolu ñu tudde Barnaba Sës, kilifay yàllay Gereg yi, Póol nag gannaaw moo farewoo woon kàddug waare ga, ñu tudde ko Ermes, ndawal yàllay Gereg yi.
13Jaamookaayu Sës ma nga woon ca buntu dëkk ba. Sarxalkat ba daldi indi ca bunti dëkk ba ay yëkk yu ñu takkal caqi tóor-tóor. Sarxalkat ba ànd ak mbooloo ma, nara rendi jur ga, sarxal ko Póol ak Barnaba.

Read Jëf ya 14Jëf ya 14
Compare Jëf ya 14:5-13Jëf ya 14:5-13