9Piyeer génn, topp ci moom, te xamul sax ndax li ko dikkal noonu te sababoo ci malaaka mi, dëgg la. Yaakaaroon na ne am peeñu la.
10Ñu jàll dalu wattukat bu jëkk bi, teg ci ñaareel bi, ba agsi ci buntu weñ, ba jëm ca dëkk ba, bunt ba daldi tijjikul boppam. Ñu génn, topp menn mbedd, malaaka ma jekki teqlikook Piyeer.
11Naka la xelum Piyeer délsi, mu daldi ne: «Léegi nag xam naa xéll ne, Boroom bee yebal malaakaam, te moo ma musal ci loxol Erodd, ak mboolem li Yawut yi séentu woon.»
12Gannaaw ba Piyeer ràññee loolu, daa dem kër Maryaama, ndeyu Yowaan Màrk, fekk ñu bare daje foofa, di ñaan.
13Piyeer fëgg buntu kër ga, mbindaan mu ñuy wax Rodd dikk.
14Ba Piyeer waxee, mbindaan ma xàmmi baatam, daldi bég ba talu koo ubbil, xanaa daw dellu ca biir, ne Piyeer a nga foofa ca buntu kër ga.
15Ñu ne ko: «Xanaa dangaa dof?» Teewul mbindaan mi ne moom la. Ñu daldi ne: «Kon malaakaam la.»
16Ci biir loolu Piyeer a ngay fëgg ba tey. Ñu tijji, muy moom, ñu waaru.
17Piyeer liyaar leen, ngir ñu noppi, daldi leen nettali, ni ko Boroom bi génnee kaso ba. Mu ne leen: «Yégal-leen ko Yanqóoba ak yeneen bokki taalibe yi.» Ba loolu amee mu génn, dem feneen.
18Ba bët setee takk-der ya ne kër-kër, ne këpp, ne: «Ana fu Piyeer jaar?»
19Erodd nag santaane ñu wër Piyeer, te taxul mu gis ko. Mu daldi àtte wattukat yi, ba noppi joxe ndigal ngir ñu rey leen. Ba mu ko defee Erodd jóge diiwaanu Yude, dem Sesare, toog fa.
20Fekk na Erodd dëngoo lool ak waa dëkk yi ñuy wax Tir ak Sidon. Ci kaw loolu waa Tir ak Sidon mànkoo, dikk ba ci Erodd. Ñu daldi fexe ba jubook Balastus, bëkk-néegu Buur, ba noppi di sàkku jàmm, ndax seen dundub réew, ca dundu Buur Erodd la daan jóge.