Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 10

Jëf ya 10:5-14

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Léegi nag yebleel ca Yope, nga wooluji fa ku ñuy wax Simoŋ, ñu di ko dàkkentale Piyeer.
6Ma nga dal ak meneen Simoŋ ma, wullikat ba këram féete wetu géej.»
7Naka la malaaka ma wax ak Korney ba dem, mu woo ñaar ciy surgaam, ak benn takk-der bu jullite te bokk ciy suqam.
8Mu nettali leen lépp nag, daldi leen yebal Yope.
9Ca ëllëg sa, ñu dem bay jub dëkk ba, yemook Piyeer yéeg ca kaw taax ma ci digg bëccëg, ngir ñaan.
10Mu dem ba xiif, bëgga lekk, ñu di ko toggal nag lu mu lekk. Ci biir loolu mu daanu leer.
11Mu daldi gis asamaan ubbiku, lu mel ni sér bu mag bu ñu téyee ñeenti lafam, wàcce asamaan, jëm suuf.
12Sér baa nga def mboolem boroom ñeenti tànk, ak dundoot yiy raam, ak mboolem njanaaw.
13Mu am baat bu jib, ne ko: «Piyeer, jógal, rey te lekk.»
14Piyeer ne ko: «Mukk, Sang bi, ndaxte masumaa lekk lenn lu daganul mbaa lu setul.»

Read Jëf ya 10Jëf ya 10
Compare Jëf ya 10:5-14Jëf ya 10:5-14