3Yaw itam sama mbokkum surga bu dëggu bi, dama lay ñaan nga jàpple leen ci, ñoom ñaar ñooñoo bokkoon ak man coonob xamle xibaaru jàmm bi, ñoom ak ñoom Kelemaŋ, mboolem sama bokki liggéeykat yi seeni tur binde ca téereb dund ba.
4Bégleen ci Boroom bi fu ngeen tollu, ma waxati ko, bégleen!