Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Buur ya - 1.Buur ya 8

1.Buur ya 8:30-60

Help us?
Click on verse(s) to share them!
30Yal nanga may nangul sama dagaan, nangul Israyil sa ñoñ. Bu ñu jubloo bérab bii, ñaan la, yal nanga ko dégge bérab ba nga dëkke ca asamaan, ba nangul leen, jéggal leen.
31«Ku ñu tuumaal ne moo tooñ moroomam, te yoon waatloo ko ba waat war ko, bu dikkee di waatsi fi sa kanam sarxalukaay bi ci biir kër gii,
32Su boobaa, yaw rikk dégge ko asamaan, àtte say jaam, ngir teg ki tooñ, daanub tooñ, këpp añu jëfam ci kaw boppam, te nga dëggal ki am dëgg, jox ko dëggam gi mu yelloo.
33«Bu Israyil sa ñoñ daanoo fi kanam ab noon, ndax tooñ gu ñu la tooñ, bu ñu waññikoo ci yaw, sàbbaal saw tur, ñaan, sàkku saw yiw ci biir kër gii,
34su boobaa yaw, yal nanga dégge asamaan, ba jéggale bàkkaarub Israyil sa ñoñ, te nga delloo leen ca réew ma nga joxoon seeni maam.
35«Bu asamaan tëjoo, taw amul ndax tooñ gu ñu la tooñ, bu ñu jubloo bérab bii, ñaan la, sàbbaal saw tur te dëddu seen bàkkaar ndax sa mbugal,
36su boobaa yaw ngalla nangool fa asamaan, te nga jéggale sa bàkkaaru jaam ñi, Israyil sa ñoñ. Ngalla xamal leen yoon wu baax wi ñu wara doxe te nga tawal sa suuf, si nga joxoon sa ñoñ, muy seen cér.
37«Bu xiif amee ci réew mi, mbaa mbas, mbaa gàncax gi lakk, mbaa benaat xuural ko, mbaa mu diy njéeréer mbaa soccet, mbaa su dee congum seen noon ci seen dëkki réew mi, mbaa muy mboolem luy musiba ak mboolem jàngoro, su boobaa,
38lépp lu ciy ñaan akug tinu gu bawoo ci képp ku mu doon mbaa ci mboolem Israyil sa ñoñ, te fekk ku ci nekk ràññee mititu xolam, ba tàllal ay loxoom jublook kër gii,
39su boobaa, yaw, ngalla nangoo ko asamaan, màkkaan ma nga dëkke, ba jéggale, te nga jëf ba yool ku nekk kemu mboolem ay jëfam, yaw mi xam xolam, ndax yaw doŋŋ yaa xam xolu mboolem doom aadama.
40Su ko defee dinañu la ragal seen giiru dund ci kaw suuf si nga joxoon sunuy maam.
41«Te itam doxandéem bu bokkul ci Israyil sa ñoñ bu jógee réew mu sore ngir sa tur,
42ndax kat dees na dégg sa tur wu réy, ak sa dooley loxo ak sa kàttanu përëg, bu dikkee ba jublu ci kër gii, ñaan,
43su boobaa ngalla nangool asamaan, màkkaan ma nga dëkke, te nga defal doxandéem boobu mboolem lu mu la ñaan, ndax xeeti àddina yépp xam sa tur, ngir ragal la ni Israyil sa ñoñ, te xam ne saw tur lañu tudd ci kër gii ma tabax.
44«Bu sa ñoñ di xarejeek seen noon, ci yoon woo leen yebal, su ñu ñaanee ci Aji Sax ji, jublook dëkk bii nga taamu, ak kër gii ma tabax ngir saw tur,
45su boobaa ngalla nangool asamaan, seenug ñaan ak seen dagaan te nga may leen ndam.
46Bu ñu la moyee, nde amul nit ku dul moy, ba nga mere leen, teg leen ci loxob noon, noon ba jàpp leen, yóbbu am réewam, mu sore mbaa mu jege,
47bu ñu demee ba seenum xel dellusee fa réew ma ñu leen yóbbu ngàllo, ñu tuub tey sàkku aw yiw fi yaw foofa ca réewum ña leen jàpp, ne la noo moy, noo ñaaw, noo def lu bon,
48bu ñu waññikoo seen léppi xol, ak seen léppi jëmm ci yaw, foofa ca seen réewu noon ya leen jàpp, ba ñaan la, jublook seen réew ma nga joxoon seeni maam, jublook dëkk bi nga taamu, ak kër gii ma tabax ngir saw tur,
49ngalla su boobaa, nangool ca asamaan, bérab ba nga dëkke, seen ñaan ak seen dagaan, te nga sàmm seen àq,
50te it nga jéggal sa ñoñ ñi la moy, jéggal leen seen mboolem tooñ yu ñu la tooñ, te may leen yërmandey ña leen jàpp, ba ñu yërëm leen.
51Ndax kat ñooy sa ñoñ ñi nga séddoo, génnee leen Misra, taalu xellikaayu weñ gu ñuul ga.
52«Sang bi, teewlul bu baax samay tinu ak sa tinuy mbooloom Israyil mii, ba nangul leen mboolem lu ñu la jooy,
53ndaxte danga leena ber ci biir xeeti àddina yépp, séddoo leen, te waxoon nga ko, Musaa sa jaam ba jottli ko, ba ngay génne sunuy maam Misra, yaw Boroom biy Aji Sax ji.»
54Ba Suleymaan noppee ñaan Aji Sax ji mboolem ñaanam ya ak dagaanam yooyu, daa siggee ca sarxalukaayu Aji Sax, ja mu sukkoon tàllal loxo ya, jublu asamaan.
55Mu taxaw, di ñaanal mbooloom Israyil mépp, daldi àddu ca kaw ne:
56«Cant ñeel na Aji Sax, ji may Israyil mbooloom ab dal-lukaay, muy la mu waxoon lépp, ngir benn baat fanaanul àll ci digey jàmm yi mu dige woon yépp, Musaa jaamam ba jottli.
57Yal na sunu Yàlla Aji Sax ji ànd ak nun, na mu ànde woon ak sunuy maam. Yàlla bu nu wacc mukk mbaa mu di nu dëddu.
58Yal na nu xiir ci boppam, nuy tegu ci yoonam yépp, di jëfe ay santaaneem aki dogalam ak àttey yoonam yi mu dénkoon sunuy maam.
59Sama kàddu yii ma ñaan fi kanam Aji Sax ji, yal na doon lu sunu Yàlla Aji Sax ji def yitteem guddeek bëccëg. Mu di ma dëggal, man jaamam, di dëggal Israyil ñoñam, saa yu nu ko soxlaa.
60Su ko defee xeeti àddina yépp dinañu xam ne Aji Sax ji mooy Yàlla, te amul moroom.

Read 1.Buur ya 81.Buur ya 8
Compare 1.Buur ya 8:30-601.Buur ya 8:30-60