Text copied!
Bibles in Wolof

YOWAANA 8:3-30 in Wolof

Help us?

YOWAANA 8:3-30 in Téereb Injiil

3 Xutbakat ya ak Farisen ya indi jenn jigéen ju ñu bettoon muy njaaloo, ñu taxawal ko ca diggu mbooloo ma.
4 Noonu ñu ne Yeesu: «Kilifa gi, jigéen jii de, dañu koo bett muy njaaloo.
5 Ci ndigali Yàlla yi, jigéen ju njaaloo, Musaa dafa santaane ñu sànni ko ay xeer, ba mu dee. Yaw nag, lu ciy sa xalaat?»
6 Loolu nag, dañu ko doon wax ngir seetlu ko, ndaxte bëggoon nañoo tiiñal Yeesu. Yeesu sëgg, di bind ak baaraamam ci suuf.
7 Bi laaj ya baree, mu siggi ne leen: «Ku masula def bàkkaar ci yéen, na ko jëkka sànniy xeer.»
8 Noonu mu sëggaat, dellu di bind ci suuf.
9 Bi ñu déggee loolu, ñuy rocceeku kenn-kenn, mag ña jiitu. Yeesu rekk des fa, jigéen ja taxaw ca kanamam.
10 Mu daldi siggi ne ko: «Jigéen ji, ana ñi la doon jiiñ njaaloo? Ndax kenn tegu la tooñ?»
11 Mu ne ko: «Kenn, Sang bi.» Yeesu ne ko: «Man it ci sama wàll, duma la daan. Demal, waaye bul defati bàkkaar.»
12 Yeesu jubluwaat ca mbooloo ma ne leen: «Man maay leeru àddina si. Ku ma topp doo dox cig lëndëm, waaye dinga am leeru dund.»
13 Farisen ya ne ko: «Yaw yaay seedeel sa bopp, kon li ngay wax du dëgg.»
14 Yeesu ne leen: «Maa ngi seedeel sama bopp, teewul li may wax di dëgg, ndaxte xam naa fa ma bàyyikoo, xam fa ma jëm. Waaye yéen xamuleen fa ma bàyyikoo ak fa ma jëm.
15 Ci gis-gisu àddina ngeen di àttee; man duma àtte kenn.
16 Teewul nag, su ma demee bay àtte, bu jub lay doon, ndaxte du man rekk ay àtte, waaye Baay, bi ma yónni, daf ciy ànd ak man.
17 Seen yoon dafa wax ne seedes ñaari nit a gëna wóor.
18 Man maa ngi seedeel sama bopp, te Baay bi ma yónni mi ngi may seedeel itam.»
19 Ñu laaj ko ne: «Kuy sa baay?» Yeesu ne leen: «Xamuleen ma, xamuleen sama Baay. Bu ngeen ma xamoon, xam ko.»
20 Bi muy wax loolu, Yeesoo nga doon jànglee ca kër Yàlla ga, ca wetu fa ñu doon denc asaka ya. Kenn manu ko woona jàpp, ndaxte waxtoom jotagul.
21 Yeesu dellu ne leen: «Maa ngi dem; dingeen ma seet, waaye seen bàkkaar ngeen di deeyaale. Fa ma jëm, dungeen fa mana dem.»
22 Yawut yay waxante naan: «Nee na kat, fa mu jëm, dunu fa mana dem. Mbaa du day xaruji?»
23 Yeesu ne leen: «Yéen, fii ngeen bawoo, ci suuf, waaye man ca kaw laa jóge. Àddina ngeen soqikoo, waaye man bokkuma ci.
24 Looloo tax ma ne, ci seeni bàkkaar ngeen di dee. Bu ngeen gëmul ki ma nekk, dingeen dee ci seeni bàkkaar.»
25 Ñu ne ko: «Yaay kan?» Mu ne leen: «Li ma leen waxoon ca njàlbéen ga.
26 Li ma mana wax ci yéen ba àtte leen, bare na. Waaye ki ma yónni, ku wóor la, te li mu ma wax rekk laay jottali àddina.»
27 Xamuñu woon ne, Yàlla Baay bee tax muy wax.
28 Yeesu nag ne leen: «Bu ngeen yékkatee Doomu nit ki, dingeen xam ne Maay ki Nekk. Dingeen xam ne it, duma def dara man ci sama bopp. Li ma Baay biy jàngal rekk laay wax.
29 Te it ki ma yónnee ngi ànd ak man; masu maa bàyyi ma wéet, ndaxte li ko neex rekk laay def.»
30 Bi ñuy dégg Yeesu di wax loolu, ñu bare daldi koy gëm.
YOWAANA 8 in Téereb Injiil